TSK

TSK · Numbers 7:13

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

¶ «Lii nag mooy li képp ku ñu bind ci limeef yi wara fey: dogu xaalis bu diisaay bi di genn-wàllu siikal, bi ñuy natte ci jaamookaay bi, dayo boobu tollook fukki gera, mu dib jooxe, ñeel Aji Sax ji.

¶ «Bu nit dee indil Aji Sax ji saraxu pepp, sunguf su mucc ayib la saraxam wara doon, mu sotti ci diw, def ci cuuraay,

Mboolem lu ngeen xayma, na dëppook natt ba ñu yoonal ci bérab bu sell bi, maanaam li ñuy wax siikal te mu tollu ci fukki garaam.

ab saraxam di benn ndabu xaalis bu diise téeméeri siikal ak fanweer, muy kilook liibar, ak benn këllu xaalis bu juróom ñaar fukki siikali bérab bu sell bi, muy juróom ñetti téeméeri garaam, lu ci nekk fees ak sunguf su mucc ayib su ñu xiiwaale ag diw, ngir saraxu pepp,

Benn fukkeelu efab sunguf su mucc ayib, di ñetti kilo, mooy saraxu pepp bi xar mu nekk di àndal, ñu tooyale ko walaatu xiinu diwu segalu oliw, di liitar ak genn-wàll.

ak fukki rootukaay yi ak fukki bagaan yi ci kaw rootukaay yi.

Ñu yóbbaale mboolem ndabi xànjar yi ñuy liggéeye ci kër Aji Sax ji; ndab yiy def dóom, ak ñiitukaay yi, ak ñiimi feyukaayi làmp yi, ak ndab yiy def deretu sarax yi, ak mboolem jumtukaayi xànjar yu ñuy sarxalee.

Ezra 8:25 TSK

Gannaaw loolu ma nattal leen xaalis baak wurus waak ndab, ya Buur aki wóllëreem aki jawriñam jooxe woon, ñook mbooloom Israyil ma fa teewoon, te lépp jëm ca sunu kër Yàlla ga.

Biiñ ba jay Baltacar, mu joxe ndigal, ñu indi ndab, yu xaalis yaak yu wurus ya baayam Nabukodonosor jële woon ca jaamookaayu Yerusalem, ngir ñu naane ca, mooki jaraafam aki soxnaam aki nekkaaleem.