Moo tax duma def lu moy wàcce musiba ci kër Yerbowam. Dinaa faagaagal ku mana taxaw, colol, te bokk ci Yerbowam, ba ci ku gëna néew doole te tumurànke fi digg Israyil. Dinaa buub kër Yerbowam, sànni, ni ñuy buubee neefare, ba mu jeex tàkk.
TSK
TSK · Philippians 3:8
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
day mujj seey fàww niy jonkanam; ña ko daa gis naa: «Ana mu?»
Mooy sonn ba gis ug leer, doyloo ko, te ñu bareey xam sama jaam bii di Aji Jub, ba mu àtte leen àtteb njekk, sëfoo seeni ñaawtéef.
Maa ngii di yar seen askan, sëlëm leen sébbriit, mi jóge ci seen saraxi màggal, ñu tonniwaale leen ak sébbriit mi.
¶ Ca waxtu woowa tembe la kemtalaayu mbégte tukkee ci Noo gu Sell gi, dugg Yeesu, mu daldi ne: «Baay, Boroom asamaan ak suuf, sant naa la, nde yaa làq lii boroom xam-xam yeek boroom xel yi, xamal ko tuut-tànk yi, nde loolu de, Baay, mooy li la soob.
Daawuda ci boppam moo ne ci téereb Sabóor: “Boroom bi moo ne sama Sang: ‘Toogeel sama ndijoor,
Waaye sama bakkan soxalu ma, xanaa ma bey samaw sas, ba sottal liggéey, bi ma Sang Yeesu dénk, te mooy seedeel xibaaru jàmm bu yiwu Yàlla wi.
Doguwuma woona xam lenn ci seen biir, lu moy Yeesu Almasi, kooku ñu daaj ca bant ba.
Am du noo tax muy wax? Nun kay noo tax ñu bind loolu, ndax kuy bey, sañ cee yaakaar, kuy bojj it, sañ cee yaakaar wàllam.
Ndaxte Yàlla mi ne: «Na leer gi leere ci biir lëndëm gi,» moo leeral sunu xol, ngir leeraangey xam-xamu leeru Yàlla, te leeraange googu mooy lerxat ci xar-kanamu Yeesu Almasi.
mu feeñalal ma Doomam, ba ma àgge jaambur ñi dul Yawut, xibaaru jàmm bi ci mbirum Almasi. Ci saa si diisoowuma ci ak kenn.
Man mi yées ci ñu sell ñépp lañu may woowu yiw, ba may xibaar jaambur ñi dul Yawut, xéewal yu amul kem yi ci Almasi.
Su ko defee nu mana màgg nun ñépp ba doon benn ci ngëm, ak ci xam-xam bu mat ci Doomu Yàlla ji, ba kera nuy doon magum jëmm, bay tollook taxawaayu Almasi bi mat sëkk.
Sàkkuwuma lu moy xam ko, xam manoore ji ko dekkal, ak itam séddu ci ay coonoom, ba bokk ak moom deeyam,
¶ Man nag, daanaka saraxu tuuru bu sottiku laa ba noppi; sama waxtuw dem dëgmal na.
Kon nag yeen ñi gëm, yeen la gànjar gi ñeel. Waaye ci ñi gëmul, nag: «Moo di doj wa tabaxkat ya beddi woon, te mu mujj di doju coll wi.»
Waaye màggleen ci wàllu yiwu sunu Boroom, sunu Musalkat Yeesu Almasi, ak ci wàllu xam-xam bu ngeen ko xam. Ndam ñeel na ko tey, ba kera bés bu sax dàkk. Amiin.