TSK

TSK · Philippians 4:9

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Ngeen mébét, dara! Ngeen diisoo, diisoo, tus! Yàllaa ànd ak nun!

Luke 8:21 TSK

Mu ne leen: «Sama yaay ak samay rakk, ñoo di ñiy dégg kàddug Yàlla, te di ko jëfe.»

Acts 9:6 TSK

Léegi nag, jógal, dugg ci dëkk bi, dees na la wax li nga wara def.»

Su ko defee Yàlla miy boroom jàmm mooy dër Seytaane ci lu gaaw, fi ngeen ko joggi seeni tànk. Yal na sunu yiwu Boroom Yeesu ànd ak yeen!

ndax Yàlla du Yàllay salfaañoo, Yàllay jàmm la. Ci mboolem mboolooy ñu sell ñi nag,

¶ Ma tëje fii nag, bokk yi, bégleen, yokkuleen ba mat sëkk, ñaaxanteleen, mànkooleen te jàmmoo. Su ko defee Yàlla miy Yàllay cofeel ak jàmm mooy ànd ak yeen.

Su boobaa jàmmu Yàlla, ji wees ab takk, mooy sàmm seen xol, ak seenum xel ndax Almasi Yeesu.

Xam ngeen na nu jëkkoona sonne, ak na ñu nu torxale woon ca Filib, dëkk ba, bala noo dikk fa yeen. Teewul ci sunu ndimbalal Yàlla, nu ñeme leena àgge, ci biir xeex bu metti sax, xibaaru jàmm bu Yàlla bi.

¶ Li ci des nag, bokk yi, moo di yeena nangoo ci sunu làmmiñ, jëfin wi ngeen wara jëfe ba neex Yàlla, te it moom ngeen nekke. Waaye danu leen di tinu, di leen ñaax, ci turu Sang Yeesu, ngir ngeen gënati koo jëfe.

Am nanu it kóolute gu nu Boroom bi may, ne li nu leen sant, moom ngeen nekke, te moom ngeen di wéye.

Yal na Boroom bi wéttali sam xel. Aw yiw ñeel na leen.

¶ Doonleen jëfekati kàddu gi, buleen di ay déglukat doŋŋ, di nax seen bopp.