TSK

TSK · Proverbs 14:6

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Li ma xelal ba ma raw noon yi, mooy sa santaane, yi ma jagoo fàww.

Lépp a dëggu ci ku am ug dégg, te jub ci ku for xam-xam.

Ab dof du am xaalis, jënde xel mu rafet; buggu ca dara.

Ab dof wutul ag dégg, balaa caag muy jaay ag muus.

Ana koo gis mu ne: «Maa xelu»? Kooku ab dof a ko gën demin.

Dees na gàcceel boroom xel yi, ñu jàq, tarsu. Kàddug Aji Sax jaa ngii ñu dëddu, kon ana seenum xel?

¶ Gannaaw ba ñu xamee Yàlla, taxul ñu màggal ko ngir li muy Yàlla, taxul ñu delloo ko njukkal, xanaa réer ci seen xalaati neen, ba seen xel mu wayadi far tàbbi cig lëndëm.

¶ Bu kenn nax boppam: Ku teg boppam ci yeen, boroom xam-xam, ni xarnu bii jàppe xam-xam, kooku na doon ab dof, ngir am xam-xam bi wóor.

James 1:5 TSK

¶ Ku desele am xel mu rafet nag, na ko ñaan Yàlla, mu may ko ko, ndax Yàlla mooy yéwéne ñépp te du sikk kenn.