Firawna daldi ne jawriñ ya: «Ndax masees naa gis ku mel ni kii a waay, nit ku Yàlla sol Noowug boppam?»
TSK
TSK · Proverbs 16:20
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Sujjóotal-leen doom ji, bala moo mer, ngeen sànkoo seenu yoon; meram day jekki ne jippét, waaye ndokklee képp ku ko làqoo!
Muy jàngi yéeg, ñu di ko màggale Yàlla. Ku doyloo Aji Sax ji, yaay tundu Siyoŋ, doo toxu; dangay sax ba fàww.
Ku ma daj, gudd fan, Aji Sax ji bége la.
Dangay xam lu jaadu, ñu naw la; yoonu workat day metti.
Kuy sàkku xel, bëgg nga sa bopp; kuy wut ag dégg day baaxle.
Xel mu rafet ay tabax kër, rafet déggin a koy samp.
Aji Sax ji déy a leen namma baaxe, moo ko tax di jóg moos ngir yërëm leen, nde Aji Sax jeey Yàllay njubte. Ndokklee képp ku ko yaakaar!
Buur wax ak ñoom te gisul ci ñoom ñépp kenn ku mel ni Dañeel ak Anaña ak Mikayel ak Asaryaa. Ñu daldi tàbbi ci liggéeyu buur.
Sama Yàlla yebal na malaakaam, mu tëj gémmiñi gaynde yi, ba defuñu ma dara. Ndax kat mucc naa ci tuuma sama digganteek moom ak sama digganteek yaw it, te defuma dara lu bon.»
Moo tax nu di ko sante màggaayam, nun ñi jëkka wékk sunu yaakaar ci Almasi.