Buleen jalgati yoon cib àtte, buleen jeng te buleen nangu alalu ger, ndax ab ger day muur bëti boroom xel, di xañ aji jub dëgg.
TSK
TSK · Proverbs 17:23
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Maa ngii! Seedeleen sama jépp tuuma fi kanam Aji Sax ji ak ki mu fal. Ana ku ma masa jël nagam, mbaa ma jël mbaamam? Ana ku ma masa lekk àqam, mbaa ma néewal ko doole? Ana ci kan laa masa nangoo alalu ger, ba nëpp-nëppal lu mu def. Lu ci am rekk, waxleen, ma fey ko.»
Deel maye, da lay ubbil bunt, di la àggle ci boroom daraja.
Seeni njiit të, xejjoo ay sàcc, ñoom ñépp sopp ger, di dàq ay neexal, ab jirim, sàmmuñu àtteem, àqu jëtun soxalu leen.
Alalu ger, ñu jël fi sa biir, ngir lor ay bakkan. Ndollant ci kaw tegandaay, nga jël feyeekoo bor, di wute alal sa àqu moroom. Man nag, nga fàtte ma. Kàddug Boroom bi Aji Sax jee.
Ngalla dégluleen lii, yeen njiiti kër Yanqóoba; yeen kilifay kër Israyil. Yeen ñi seexlu dëgg, lunkal wépp yoonu njub.
Lu bon la seeni loxo mane: kàngam di laaj, ab xaali di sàkkub ger, boroom daraja moom, di wax fuqley bakkanam, ñu ànd ràbbum pexe.