¶ Ba Ibraam amee juróom ñeent fukki at ak juróom ñeent (99), am na bés Aji Sax ji feeñu ko ne ko: «Man maay Yàlla Aji Man ji. Topp ma te mat sëkk.
TSK
TSK · Proverbs 18:10
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Nit ka ne ko: «Na nga tudd?» Mu ne ko: «Yanqóoba.»
Yàlla Aji Man ji, mooy ni ma feeñoo woon Ibraayma, te ni laa feeñoo Isaaxa ak Yanqóoba it, waaye sama tur, Aji Sax ji, leeraluma leen ko woon.
¶ Daawuda ne waa Filisti ba: «Yaw de yaa may jëlal ab saamar ak xeej bu mag ak bu ndaw, waaye man turu Aji Sax ju gàngoor yi laa lay dikke, Yàllay làngi xarey Israyil, ji nga tëkku.
Mooy sama Yàlla, ji ma sës, yiiru, fegu, mucc, làqu, raw, mucc fitna.
Yaay may sa buuru ñoñ ndam lu réy, yaay ji ngor ki nga fal, muy man Daawuda, di sama askan ba fàww.
Buur, yal na la Aji Sax ji nangul bésu njàqare, yal na la turu Yàllay Yanqóoba aj fu kawe,
Noon yee ma yendoo lakkal, bare lool di xareek man. Ku Màgg ki,
Yaw laa làqoo, ngay tata ju dëgër, fegal ma noon.
Yàlla da naa: «Kii de man la safoo, ma di ko xettli. Man la xam, te maa koy teg fu wóor.
Ragal Aji Sax ji kaaraange gu wér la ci nit, di rawtu ciy doomam.
Wóoluleen Aji Sax ji tey ak ëllëg; Yàlla Aji Sax ji déy, moo mat cëslaay ba fàww.
Ay jantam Yuda dina texe, Israyil dëkke kaaraange, te dees na ko tudde nii: “Aji Sax ji sunu njekk.”