TSK

TSK · Proverbs 18:22

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

¶ Yàlla Aji Sax ji daldi ne: «Wéet baaxul ci nit, kon dinaa ko bindal ku koy jàpple te jekk ci doon wéttalam.»

Ci kaw loolu Yanqóoba liggéeyal Laban diiru juróom ñaari at ngir Rasel, te mu mel ni ay fan rekk ci moom ndax mbëggeel, gi mu am ci Rasel.

Ruth 4:10 TSK

boole ci Ruut, ndawas Mowab, sa doon soxnas Malon, muy sama soxna. Su ko defee ma mana lawal askanam, ba du fey, boole ci sàmmal leen seen alal, ba turu Elimeleg du réer ci biiri bokkam te du raaf ci limeefu dëkk bi. Yeena ko seede bésub tey jii.»

Naanal ci sa mbalkam bopp, ndox ma balle sa teenu bopp.

Jeeg bu jàmbaare day teral jëkkër ja, jeeg buy rusloo day semmal jëkkër ja.

Jeeg bu jàmbaare, ndaw lu jafe, ba rawati gànjar!

Su Galàdd dee dëkkub defkati ñaawtéef, dañoo tekkiwul dara. Fa Gilgal lees di rendee ay saraxi yëkk, te seeni sarxalukaay ni jali xeer lay mel ci ay tooboy tool.