TSK

TSK · Proverbs 2:6

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Maa ko feesale xelum Yàlla, ak xareñte ak déggin ak xam-xam, ak manoorey bépp xeetu liggéey,

dama ne, dinaa la defal li nga ñaan, te sax dinaa la may xel mu rafet, nga am ug dégg, ba raw ku la jiitu ak ku la wuutu.

Mboolem àddinaa daan wuta giseek Suleymaan, ngir taataansi xelam mu rafet mi Yàlla def cib xolam.

Ezra 7:25 TSK

¶ Yaw Esra nag, seetal ci xel mu rafet mi sa Yàlla digle ci yoonam wi nga yor, nga tabb ay njiit aki xaali, ngir ñuy àtte mboolem ñi xam sa yooni Yàlla ci diiwaani Wàllaa Dex. Te ñi ko xamul, nga xamal leen ko.

Job 12:16 TSK

Kee am doole, keey sottal, di boroom aji réer ak ka ko réeral.

Asamaan lay fenke cat lii, wëndeelu, sowi cat lee; amul lu rëcc tàngooram.

Kiy yar yéefar yi, da dul mbugalee? Du mooy kiy xamal nit?

Li ma xelal ba ma raw noon yi, mooy sa santaane, yi ma jagoo fàww.

Santaane da lay niital, ndigal leeralal la, artook ub yar di yoonu dund.

Yàlla de, ku mu gërëm, xelal ko, xamal ko, bégal ko; bàkkaarkat bi, Yàlla teg ko, muy denc ak a dajale, ka mu gërëm jël. Loolu it di cóolóoli neen ak napp um ngelaw.

mboolem sa doom yu góor ay jànge ci Aji Sax ji, boole kook jàmm ju ne ñoyy.

Mooy walbati jamono, di soppi demin, di fal buur, di folli. Mooy xelal boroom xel mu rafet, di xamal boroom xel mu ñaw.

Ndax man maa leen di jox làmmiñ wu ànd ak xel, wu seen benn noon dul mana dàq mbaa di ko weddi.

ngir Yàllay sunu Sang Yeesu Almasi, Baay bu màgg bi, sol leen xel mu rafet, ak ngis, ngir ngeen man koo xam bu baax.

gépp may gu baax, ak bépp jagle bu mat, fa kaw la bawoo, di lu wàcce fa Baay biy boroom leer yi, ki soppikuwul ci lenn, te genn ker gu toogadi nekkul ci moom.