TSK

TSK · Proverbs 21:1

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Waaye man maay dëgëral boppu Firawna, ba fulandi samay firnde ak samay kéemaan ci biir réewum Misra.

Ezra 1:1 TSK

¶ At ma jëkk ca nguurug Sirus buuru Pers, Aji Sax ji moo nammoona sottal kàddu ga mu waxe ca gémmiñug Yeremi, ba tax mu xiir Sirus buuru Pers, mu siiwtaane ab dogal ci mboolem réewam, boole ci bind ko ne:

Ezra 6:22 TSK

Wormaal nañu it màggalu Mburu mu amul lawiir, diiru juróom ñaari fan, ci biir mbégte, ndax fekk na Aji Sax ji bégal leen lool ca na mu xiire buurub Asiri, mu yéwéne leen ba dimbali leen ci tabaxu kër Yàlla ga, Yàllay Israyil.

Éy Boroom bi, Sang bi, rikk teewlul bu baax samag ñaan, ak sa ñaanu jaam ñi safoo wormaal saw tur. Ngalla Sang bi, nangul ma tey jii, may ma waa jii yéwéne ma.» Booba maa yore woon naani Buur.

akub bataaxal bu jëm ca Asaf may wattu toolu buur, ngir mu may ma bant yu ma defareji bunti tatay kër Yàlla ga, defaraale ca tatay dëkk baak kër ga may dali.» Buur nangul ma, ndax sama Yàlla ji ma toppe mbaaxam.

Yaa fettaxal fii bëti ndox akum wal, ŋiisal dex yu masa wal.

mu xiir waa Misra ci dëddu ñoñam, ñuy fexeel jaamam ñooña.

Géej gaa leen gis, daw, dexu Yurdan a deltu gannaaw,

Nit ay dogu ci xolam, Aji Sax ji dogal, mu sotti.

Jéegoy jaam Aji Sax jee ko yor, kenn xamul foo jëm.

Maa naa xóotey mbeex mi: “Wowal, te maay ŋiisal say dex.”

¶ Ñetteelu malaaka mi sotti ndabam ci dex yeek bëti ndox yi, mu doon deret.