Aji Sax ji nag ne Samiyel: «Bul xool ci melokaanu kii, mbaa jëmmu taxawaayam, ndax gàntal naa ko. Lii du ci gis-gisu nit. Nit, li fees bëtam lay gis, waaye Aji Sax ji ci xol lay xool.»
TSK
TSK · Proverbs 24:12
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Jëfu doom aadama ji daal, moom la koy fey; na nit kiy jëfe rekk la koy yoole.
Natt nga saab xol, niir ma guddi, settantal ma, gisoo dara. Dogu naa ne duma moye wax.
Benn yoon la Yàlla wax, yaari yoon laa dégg, ñu ne; «Doole, fa Yàlla.»
Kii du la bàyyi nga tërëf, sa sàmm bii gëmmul.
Lu waay jëf, Aji Sax ji gis, di xool mboolem fu mu jaare.
Lu waay def, daa jekk ca moom, waaye Aji Sax jeey natt xol yi.
Xanaa ndax buur suqal mbey mi, ba ñépp jariñoo suuf si.
réyi pexe, màggi jaloore; say gët ne jàkk ci mboolem lu doom aadama def, ngay añale ku nekk jëfinam ak jëfam.
xanaa ngay diirook Boroom asamaan, bay santaane ñu indil la ndabi këram, nga di ci naan biiñ, yaak say jawriñ ak say soxna ak say nekkaale, ngeen di sàbbaal ay yàllay xaalis ak yu wurus ak yu xànjar ak yu weñ ak yu bant ak yu doj, te du ci lenn luy gis mbaa muy dégg mbaa mu xam dara. Waaye Yàlla ji yor sa bakkan tey ak ëllëg sàbbaaloo ko.
“Ndax sunu bakkan ak sunu yëngu ak sunug nekk, lépp ci moom la.” Mooy ba tey la ñenn ci seeni woykat ne: “Nun itam aw xeetam lanu.”
Te noonu lay deme kera bés ba Yàlla di àtte mbiri kumpa yu nit ñi, ci saytub Yeesu Almasi, ni ko sama xibaaru jàmm bi indee.
Ndax kat, nun ñépp fàww nu taxawi fa jalub àttekaayu Almasi, ngir ku nekk yooloo kemu jëf ja mu jëfe yaramam, muy lu baax, mbaa lu bon.
Maay Kiy Dund, maa dee woon, maay dund nii tey ak ëllëg ba fàww te maa yor caabiy dee ak njaniiw.
Am mbas laay fàdde ay taalibeem. Su ko defee mboolooy gëmkat ñépp dinañu xam ne man maay nattu xol ak xel, te maay fey ku nekk ay jëfam.
¶ «Maa ngii di ñëw léegi, ànd ak sama pey, ngir delloo ku nekk jëfam.