TSK

TSK · Proverbs 24:19

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Ndokklee yaw mi toppul tànki ku bon, taxawewuloo yoonu moykat, toogewuloo jataayu ñaawlekat.

Ñeel Daawuda. Bu sa xol jóg ci ku bon, bul ñee kuy def njombe.

Yeen ñiy def lu bon, xiddileen ma, ba ma sàmmonteek sama santaaney Yàlla.

Kon nag: «Nangeen génne ci seen biir, te teqlikoo ak ñoom,» la Boroom bi wax. «Lu sobewu, buleen ko laal. Su boobaa, maa leen di dalal.

Nit ñi, seen bopp doŋŋ lañuy bëgg, ay bëggkati xaalis lañuy doon, ay damukat, nit ñu réy, di ay saagakati Yàlla, ñu déggadil waajur, ñu santadi te selladi.