TSK

TSK · Proverbs 27:17

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Moo tax bànni Israyil gépp, ku ci bëggoona nàmmlu sa ngajju mbaa sa daba, mbaa sa sémmiñ, mbaa sa sawta, doo man lu moy dem ca tëggi waa Filisti.

Yowab ne Abisay: «Bu ma waa Siri ëppee doole, nga wallusi ma; su la Amoneen ñi ëppee doole, ma wallusi la.

Diwook suuru day naatal xol; waaye li neex cib xarit, xol la lay digale.

Ku yoqi, dooleel-leen ko, ku óom yay fenqe, jàppleleen ko.

ngir kenn baña jàq ci biir tiis yii, ndax yeen ci seen bopp xam ngeen ne loolu lanu séddoo.

Looloo tax may daj yii coono. Waaye rusuma ci, ndax xam naa ki ma gëm, te wóor na ma ne moo mana sàmm li ma ko dénk ba keroog bés ba.

Xibaaru jàmm boobu moo tax may daj coono yu metti ni defkatu mbon, ba ci jéng yii ñu ma jéng. Waaye kàddug Yàlla moom, deesu ko jéng.

James 1:2 TSK

¶ Bokk yi, bu ngeen jaaree ci mboolem xeeti nattu, jàppeleen ko mbég mu mat sëkk,