Malaakam Aji Sax ji ne ko: «Lu tax ngay dóor sa mbaam mi ñetti yoon nii? Man mii maa dikk, jànkoonteek yaw, ndax yoonu sànkute laa gis.
TSK
TSK · Proverbs 28:18
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Yal na ma maanduteek njub taxawu, maa ngii, di la xaar.
Yoonu tarxiis kay, nga leen teg, daane leen, ñu sànku,
Waaye kuy topp yoonu ndëngte, Aji Sax jee koy sànk, boole kook kuy def lu bon. Yal na jàmm dal Israyil.
Bu ngëlén walee, ab soxor ne mes; ku jub, sab reen sax ba fàww.
Ku mat, njekk xàllal la; coxor daaneel boroom.
Ku yóbbe bàkkaar nit kuy jubal, yeer ma nga gas, yaa cay tàbbi, waaye ku mat di jagoo ngëneel.
Fa nit ñi naan: «Jàmm ak kaaraange dikk na,» fa la sànkute di dale ci seen kaw, ni aw mat di jekkee dal ci kaw jigéenu wérul, te kenn du ca rëcce.
Kon nag fàttlikul la nga jotoon te dégg ko; nga sàmm ko, te tuub. Soo teewluwul nag, dinaa ñëw nib sàcc, te doo xam mukk wan waxtu laa naa jimeet fi sa kaw.