Buleen seet fi mbooloo gëna baree, ngeen topp leen ci jëf ju bon; te it buleen jeng, di topp mbooloo mu gëna bare ci ab layoo, di leen seedeel lu toxal dëgg.
TSK
TSK · Proverbs 28:21
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Exodus 23:2
TSK
Deuteronomy 1:17
TSK
Buleen far-farloo cib àtte, dégluleen ku tuut, ni ngeen di dégloo ku mag, te buleen ragal kenn, ndax àtte bi Yàllaay boroom. Bu leen mbir mi ëppee loxo nag, ngeen indil ma ko, ma seet ko.»
Proverbs 24:23
TSK
Lii it ñi rafet xel a ko wax. Par-parloo cib àtte baaxul.
Hosea 4:18
TSK
Seenu ñoll giiful sax, ñuy gànctoo gànctu, te gàccee gënal seeni kilifa.
Micah 7:3
TSK
Lu bon la seeni loxo mane: kàngam di laaj, ab xaali di sàkkub ger, boroom daraja moom, di wax fuqley bakkanam, ñu ànd ràbbum pexe.
2 Peter 2:3
TSK
Seenug bëgge lañuy ràbbe ay kàddu yu ñu leen di koppartoo. Ñooñu la seenub daan yàgga yoot, te seen sànkute nelawul.