Su nit ki tooñee moroomu nitam, Yàllaay àtte; waaye su dee Aji Sax ji la nit ki tooñ, ana ku koy àtte?» Wax jooju nag taxul ba tey ñu déggal seen baay. Booba fekk na Aji Sax ji namm leena rey.
TSK
TSK · Proverbs 29:1
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
¶ Ci kaw loolu Yonent Yàlla Ilyaas, ma dëkk Tisbi ga ca Galàdd, wax Axab, ne ko: «Giñ naa ci Aji Sax ji, Kiy Dund, di Yàllay Israyil ji may jaamu: at yii nu nekk, du taw te du lay, lu moy dama koo wax ci sama làmmiñ.»
Mu ne ko: «Aji Sax ji dafa wax ne: Gannaaw yaa bàyyi ku ma aayaloon bakkanam, sa bakkan mooy fey bakkanam te say bokk ay fey bokkam.»
Aji Sax ji nag ne: “Ana kuy nax Axab, mu songi Ramot ga ca Galàdd, ba daanu ca?” Kii ne nii, kee ne nee.
Ci biir loolu mu am ku soqi ag fitt te teyu ko, mu dal buurub Israyil ci diggante ñaari wàlli pakk bi mu sol. Mu ne dawalkatu watiiram: «Waññikul, génne ma ci xeex bi, gaañu naa!»
Artu nga leen ndax ñu dellu ci saw yoon, teewul ñu bew, ba sàmmuñu say santaane, xanaa di moy sa àttey yoon yiy taxa dund képp ku ci sàmmu. Ñuy daŋŋiiral, sajju loos, bañ laa déggal.
Moo tax musiba di jekki dal ko, mu jekki yàqu, ba wees paj.
Mat, mucc; dëng, dàll daanu.
googu ñaawtéef ay mujj doon seen xar-xaru tata ju kawe, funki, tata ja jekki jóoru.
Aji Sax ji, wacc ngaa wacc Yuda nii? Am Siyoŋ a la génnliku? Lu tax nga di nu dumaa musiba mu amul paj? Nuy yaakaar jàmm, dara baaxul, nuy séentum paj, tiitaange ne jaas!
¶ Li ko dale fukkeelu at ak ñett ci nguurug doomu Amon, Yosya buurub Yuda, ba tey jii, di ñaar fukki at ak ñett, kàddug Aji Sax jaa ngi may dikkal, ma di leen ko jottli te tàyyiwma, waaye dégluwleen.
«Aji Sax ji Yàllay Israyil Boroom gàngoori xare yi dafa wax ne: Demal wax mboolem waa Yuda ak waa Yerusalem, ne leen: “Xanaa dungeen dégg ndigal, ba dégg samay kàddu?” Kàddug Aji Sax jee.
¶ Teewul ñu baña déglu, të ticc, fatt seeni nopp, ngir baña dégg.
¶ Yuda nag gannaaw ba mu jëndee ab tool ca peyu ñaawtéefam ja, ca la daanu, jiital boppam, biir ba fàcc, butit ya tuuru.
Fa nit ñi naan: «Jàmm ak kaaraange dikk na,» fa la sànkute di dale ci seen kaw, ni aw mat di jekkee dal ci kaw jigéenu wérul, te kenn du ca rëcce.