TSK

TSK · Proverbs 31:13

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Maa ngi nii taxaw ci bëtu ndox mi, janqi dëkk bi di rootsi.

¶ Na muy wax ak ñoom nag, Rasel agsi, indaale gàtti baayam, ndaxte sàmm la woon.

Ruth 2:2 TSK

¶ Mu am bés Ruut, ndawas Mowab sa, ne Nawmi: «Tee maa dem tool, ndax ma gis boog ku ma laaye biir, ma mana foraatu gub yu des ca gannaawam?» Mu ne ko: «Waaw, demal, doom.»

Aji Sax ji da ne: «Jigéeni Siyoŋ a ngi daŋŋiiral, di goŋeet-goŋeeti, di regejook a rékk-rékkal, samp um ndaag, keleŋal lami wëq.»

Acts 9:39 TSK

¶ Piyeer jóg, ànd ak ñoom, ba agsi. Ñu yéege ko ca néegu kaw taax ma. Ay jëtun a nga fa woon. Ñoom ñépp di jooyoo, yéew Piyeer, won ko turki yaak mbubb ya Dorkas defaroon ba muy nekk ak ñoom.

ndax ba nu nekkee ak yeen, ndigal lanu leen joxoon moo di lii: «Ku nanguwula liggéey, bumu lekk.»

Moo tax ma bëgg, jëtun ñiy ndaw séyaat, ami doom, yor seen kër, ba noon bi du am lu mu yàqe sunub der.