¶ Ñu neeti: «Alku ñeel na ku nangub ger, ngir rotal bakkanu nit ku deful dara.» Mbooloo mépp ne: «Amiin!»
TSK
TSK · Proverbs 6:17
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
ak deretu nit ñi mu tuur te defuñu dara; ndax Manase daa feesal Yerusalem ak deretu jaamburi Yàlla, ba Aji Sax ji nanguwu koo baal.
Aji Sax ji, yaay sànk kuy fen, sib kuy bóomeek kuy wore.
ku sellal, fekk la sell; ku dëng, fekk laak say feem.
Moo leen taxa ràngoo reewande, làmboo coxor.
Éy Aji Sax ji, musal ma ci gémmiñu fen-kat, ak làmmiñu njublaŋ.
Dañu la naan: «Dikkal, nu tëruji bakkan, yeeruji jaambur bu deful dara.
Seede bu dëggu, dëgg rekk, seede bu dëgguwul, fen rekk.
Waxi teggin jekkul cib dof, ay fen ci as gor waxi noppi.
Kuy fen, dangaa bañ ka nga fenal, te boroom làmmiñ wu neex day sànke.
Bu ngeen ma tàllaleey loxo, ma fuuyu. Bu ngeen doon ñaan-ñaanee it, du maa leen di déglu: seeni loxo, deret la taq ripp.
Seen dëgër bët tuumaal na leen, ñuy bàkkaar ni waa Sodom, làquwuñu sax. Wóoy, ngalla ñoom! nde ñoo lor seen bopp.
Seeni loxoo taq deret, ngeen ne lijj ci ñaawtéef, làmmiñ di fen, di sos njekkar.
Ci biti, xaj yaa fa nekk ak xërëmkat yi ak moykat yi ak bóomkat yi ak bokkaalekat yi, ak képp ku sopp fen te di ko jëfe.