Bu ñu la doon dàq, di wut sa bakkan, yal na fekk sa bakkan dence ca ëmbu aji dund ña, ca sa wetu Yàlla Aji Sax ji, sang bi. Waaye sa bakkan ub noon, yal na ko mbaq, sànni fu sore.
TSK
TSK · Psalms 21:8
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
¶ Gannaaw loolu Buur Daawuda sanc na këram, Aji Sax ji noppal ko ci noonam yi ko wër yépp.
Damaa saxoo ne jàkk ci Aji Sax ji ndijoor la ma fare, ba duma tërëf,
Waa màndiŋ mi di ko sukkal, ay noonam mëq suuf,
Lii, yal na ko Aji Sax ji feye ñi may sosal, di teg lu ñaaw ci sama der.
Maa duma réew yu seeni yàllantu, seeni tuur sut tuuri Yerusalem ak Samari.
Waaye waa réewam ña dañu koo bañoon. Ci gannaawam lañu yónni ndaw, ne: “Kii, bugguñu muy sunu buur.”
Ndaxte fàww Almasi nguuru, ba kera Yàlla di sukkal mboolem ay noonam ciy tànkam.
Gémmiñ gi, saamar bu ñaw a ciy lange, mu di ko cawe askan yi. Moo leen di jiitee yetu weñ, te mooy dëggaate ci biir nalukaay bi, reseñ ji ñuy segale biiñu sànj mu tàng mu Yàlla Aji Man ji.