TSK

TSK · Revelation 21:3

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

¶ «Maay samp sama kër ci seen biir te duma leen sib.

¶ «Waaye yaw Yàlla! Ndax yaay dëkk ci kaw suuf sax? Seetal rekk, asamaan yi ba ca asamaani asamaan ya manu laa fat, waxumalaa kër sii ma tabax.

Yeen waa Siyoŋ, serleen te sarxolleel ku màgg ki fi seen biir, Aji Sell ju Israyil.»

Mu ne ma: «Yaw nit ki, sama màkkaanu ngàngunee ngi, bérab bii laay teg samay tànk, di fi dëkke fi digg bànni Israyil ba fàww. Bu waa kër Israyil dellu teddadil sama tur wu sell, ñook seeni buur ci seen gànctu, ak seen néewi buur yi ñuy denc ci seeni jaamookaay.

Ñetteel bi laay tàbbal ci sawara, xelli ko ca ni ñuy xellee xaalis, nattu ko ni ñuy nattoo wurus cib taal. Xaaj boobu moo may woo ci sama tur, ma wuyu ko. Moom laay wax: “Sama ñoñ,” Moom mu ne: “Aji Sax jeey sama Yàlla.”»

Maay doon seen baay, ngeen di samay doom, góor, ak jigéen,» la Boroom bi, Aji Man ji wax.

Waaye réew mu ko gën lañu doon sàkku, te mooy réewum asamaan. Looloo tax Yàlla rusul ñu di ko tudde seen Yàlla, ndax waajalal na leen ab dëkk.

Naka la juróom ñaari dënu yi jib, may waaja bind, daldi dégg baat bu jóge asamaan, ne ma: «Loolu juróom ñaari dënu yi wax de, gas ko, suul, bu ko bind.»

¶ Ci kaw loolu ma dégg baat bu xumb bawoo asamaan, ne: «Léegi nag texe teew na, ànd ak sunu kàttanu Yàlla ak nguuram, ak sañ-sañu Almaseem, ndax xalab nañu ki daan tuumaal sunu bokk yi, di leen sosal guddeek bëccëg fi sunu kanam Yàlla.