Dinaa def mbañeel sa digganteek jigéen ji, ba dëddale sa xeet ak xeetam, muy toj sa bopp, nga di ko màtt ci téstën.»
TSK
TSK · Romans 1:3
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Buur ne: «Ma biral dogalu Aji Sax ji, moom mi ma ne: “Yaa di sama doom, bés niki tey, maa la jur.
Dooley kilifteefam ak jàmm ja du am kemu, fa jalub Daawuda ak nguuram, ga muy samp, saxale ko njekk ak yoon, tey jii, ba fàww. Lii la Aji Sax ji Boroom gàngoor yi def ci xéraangeem.
Bés yooyu ci jamonoom, maay jebbil njebbit lu jekk ci askanu Daawuda, muy jëfe njub ak njekk ci réew mi.
«Bésub keroog maay yékkati mbaarum Daawuda mi joy, ba fattaat xar-xar yi, defaraat gent bi, tabaxaat ko na woon.
Dinga ëmb, ba jur doom ju góor; nanga ko tudde Yeesu.
Moo nu feeñalal Musalkat bu manoorewu, fi biir kër Daawuda jaamam ba,
Moom Yàllay Ibraayma, di Yàllay Isaaxa, di Yàllay Yanqóoba, te di sunu Yàllay maam kay, moo màggal jawriñam Yeesu. Yeen nag yeena ko teg ciy loxo, jàmbu ko fa kanam Pilaat, te mu naroon koo bàyyi.
¶ Ca saa sa la tàmbalee xamle Yeesu ca jàngu ya, naan Yeesu mooy Doomu Yàlla.
Yàlla mi may jaamoo xol, ci ni may siiwtaanee xibaaru jàmm bu Doomam, moom seere na ne noppiwuma leena fàttliku.
Ndax ñooñu Yàllaa leen ràññee woon lu jiitu, te it la mu dogaloon lu jiitu ci ñoom moo di ñu niru Doomam, ngir Doomam di taaw, ci biir rakk yu bare.
Yàllaa am kóllëre, moom mi leen woo, ngir ngeen bennoo ak Doomam Yeesu Almasi, sunu Sang.
¶ Yàlla kat moo nu wallu ba génne nu ca kilifteefu réewum lëndëm ga, toxal nu ci biir nguurug Doomam ji mu sopp.
Deesul nàttable moos màggaayu mbóot mii feeñe ci sunu yoonu ngëm: Kii moo feeñe ci yaramu suux, Noowug Yàlla dëggal ko, malaaka ya niir ko; moom lañu waaree ci xeet yi, gëmees na ko ci kaw suuf it, te yéegees na ko fa leer ga.