TSK

TSK · Romans 14:2

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

¶ Yàlla ne: «Xool-leen, jox naa leen gépp gàncax gu ànd ak jiwoom ci kaw suuf sépp ak gépp garab guy meññ tey jur jiwoom, muy seen dund.

Njëlu ñetti xob fa ñu la soppe moo dàq yàpp wu duuf fu ñu la bañe.

Ci kaw loolu wattukat ba di yóbbu seen njël ak seen biiñ, weccee leen ko meññeef.

¶ Yaw ci sa wàllu bopp, ngëm gi nga ci am, yemale ko ci sa bopp, fi kanam Yàlla. Ndokklee ki sikkul boppam lenn ci jëfin wu mu dogul boppam ne noonu lay jëfe.

Ndax kat balaa aw nit a dikk, bàyyikoo fa Yanqóoba, Sefas da daan bokk lekk ak jaambur ñi dul Yawut. Waaye ba ñooñu dikkee la rocciku, daldi beddeeku jaambur ñi, ndax ragal waa làng, ga jàpp ne aaday xaraf wartéef la.

Nit ñi set nag, seen lépp ay set, waaye ñi boole sobewu ak gëmadi, seen dara setul, seen xalaat ak seenum xel, ñooy bokk sobewu.

¶ Buleen nangu ay àlluwa yu bare te woroo ak sunu ngëm, di leen fàbbi. Li baax mooy ngeen di yokke aw yiw, seen pastéefu xol. Buleen yokke pastéefu xol, ay ndigal yu jëm ci aw ñam, te ña koy sàmm, jariñu leen dara.