Kon nag kàddug Aji Sax jee, Yàllay Israyil: “Maa waxoon déy ne, sa waa kër ak sa waa kër baay ñooy doxe fi sama kanam, di ma liggéeyal ba fàww.” Léegi nag, kàddug Aji Sax jee: “Loolu jomb naa ko tey. Ñi ma teral laay teral; waaye ñi ma teddadil, dees na leen tuutal.
TSK
TSK · Romans 2:10
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Xanaa ki wéye maandu, di def njekk, di wax dëggu xolam.
Bàyyil xel ku maandu, xool ku jub; muj, fa nitu jàmm.
Gudd fan, mu joxee ndijoor; càmmoñ ba, alal ak teraanga.
Alal ak teraangaa ngi fi man, am-am bu sax it ak yoolu njekk.
Aji Sax ji, yaa nuy defal jàmm, te lépp lu nu def, yaa nu ko sottalal.
Céy su ngeen sàmmoon samay santaane, ba jàmm baawaanal leen, njekk géejal leen,
«Mbégte déy, ngeen di génne, ñu yóbbu leen ci jàmm, tund yu mag yeek yu ndaw yi di leen sarxolleel, garabi àll bi yépp tàccoondoo.
¶ «Waaye du tee, maa leen di may tan, faj leena faj ba ñu wér, won leen xéewalu jàmm ju dëggu.
di niital ñi tooge biir lëndëm ak takkndeeru ndee, di nu gindi, teg nu ci yoonu jàmm.»
Ndokklee surga yooyu seen njaatige dikk fekk ñu teewlu. Maa leen ko wax déy, njaatige leey takku, toogal leen ba noppi dikk, taajal leen, ñu lekk.
¶ Ba waxtuw reer jotee, Yeesu toog ak ndaw ya,
waaye xeetoo xeet, ku ko ci ragal tey def njekk, mooy ki ko neex.
Njàqare ak musiba daal, mooy dal ci kaw képp kuy def lu bon, te Yawut bi jiitu ci, waaye ki dul Yawut it topp ci;
Xintey bakkan nag ci ndee lay jëme, waaye xintey Noowug Yàlla ndund ak jàmm lay jur.
Su dee Yàlla moo def loolu nag ngir fésal màggaayu teddngaam, ñeel ay ndab yu xéewloo yërmande, te mu waajalaloon leen teraanga?
¶ Kon Yàlla miy maye yaakaar, yal na leen feesale gépp mbég, ak jàmm ci biir ngëm, ba ngeen géejule yaakaar, ci manoorey Noo gu Sell gi.
¶ Meññeefum Noowug Yàlla nag moo di: cofeel, ak mbég, ak jàmm, ak xolu muñ, ak mbaax, akug tabe, ak ngëm,
Kon gis nga ne ngëm gaa liggéeyandoo ak jëfam ja, te ca jëf ja la ngëm ga mate sëkk.
Yooyu nattu, ni sawara di natte wurus, ni lay natte seen dëggutey ngëm, te ngëm a gën wurus fuuf, nde wurus day jeex. Su ko defee seen ngëm gu dëggu jural leen ag cant, ak daraja ak teraanga, bés bu Yeesu Almasi feeñee.