TSK

TSK · Romans 3:28

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Ndax kat deesul jox kenn àtteb ku jub fa kanam Yàlla ndax jëf ju mu def, ngir sàmm yoonu Musaa; solob yoon wi daal, mooy ci lees di ràññee bu baax luy bàkkaar.

Waaye ki jëful te gëm Yàlla miy jox ab yéefar sax, àtteb ku jub, ngëmam googu, ag njub lees ko koy waññal.

Li yoonu Musaa tële woon ndax néew dooley nitu suuxu neen, mooy lii Yàlla def: Doomam la yónni, mu dikke melow nit, te nit di bàkkaarkat, di suuxu neen, ngir Doomam fajtal mbirum bàkkaar. Yaramu suux wu nit kooku la Yàlla sottale mbugal gi war ci bàkkaar,

Xam nanu nag ne nit ki, du ci jëfi sàmm ndigali yoon la ko Yàlla di joxe àtteb ku jub, xanaa ci ngëm gu mu gëm Yeesu Almasi. Te nun itam, Almasi Yeesu lanu gëm, ngir Yàlla jox nu àtteb ku jub ci kaw gëm gu nu gëm Almasi, te du ci kaw jëf ju nu sàmme ndigali yoon. Ndax kat du ci jëfi sàmm yoon lees di joxe kenn àtteb ku jub.

Li sàmm yoon taxul kenn jot àtteb ku jub fi kanam Yàlla sax, lu leer nàññ la, nde: «Ku jub ndax ngëmam mooy dund.»

Titus 3:7 TSK

Noonu la nu Yàlla joxe àtteb ñu jub ci kaw aw yiwam, ba nu mujj séddu ci texe gu sax dàkk, ni nu ko séentoo.