TSK

TSK · Romans 6:21

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Kàddug ñaari seede ba ñett nag, ci lees di reye ki ñu wara rey, waaye deesu ko rey ci kàddug benn seede.

¶ Daawuda nag mer lool ca jëfi nit kooku. Mu ne Natan: «Giñ naa ci Aji Sax jiy dund, dee rekk mooy àtteb waa ji def loolu!

Ezra 9:6 TSK

daldi ñaan, ne: Éy sama Yàlla maa rus, maa torox, ba manumaa siggi fi sa kanam, ndaxte sunuy bàkkaar bare na, ba mëdd nu, sunuy moy tegloo ba àgg asamaan.

Job 42:6 TSK

Moo ma tax ne: «Wàqet, tuubi-ruubi,» ba diwoo suuf akub dóom.

Waaye loo ci góobe, gar ko, say pexe suur la këll.

«Ndox mu lewul a neex, ñamu làqu-lekk dàqati.»

Yoon a ngi, nit defe ne jub na, te mu jëme ko ci ndee.

Moo tax waame aje, taw yiy mujje dikkul. Teewul ngeen dëgër bët nib gànc, ñàkk gàcce!

Jiwum pepp, góob ay dég; sonn, ñàkk yool, xanaa mbetteel ci meññeef mii sababoo ci merum Aji Sax ji.»

Dëddu woon nanu la moos waaye léegi réccu nanu. Xam nan ne tooñ nanu, ba tey nuy màttuy wiccax. Danoo rus, torox ndax sunu ñaawtéefi ndaw.”»

Yaay fàttliku say jëfin, ba am kersa keroog booy dalal sa doomi ndey yu jigéen, ñi la mag ak ñi la féete ndaw. Maa la leen di may niy doom, doonte loolu bokkul ci sama kóllëreek yaw.

Bu ñu kersawoo mboolem seeni jëf nag, nanga leen xamal bindu kër gi ak tëralinam aki duggukaayam aki génnukaayam, bindam bépp, ak dogali yoon yi mu laaj yépp. Nanga bind lépp, ñu gis, ba mana sàmm mboolem bindu kër gi, ak mboolem dogali yoon yi mu laaj, te di ko jëfe.

Ñu baree ngi nelaw, keroog ñu yewwoo fa pëndub suuf. Ñenn ña nara dund fàww, ña ca des añe gàcceek njàqare fàww.

Moonte xam nañu xéll ne ñiy jëfe noonu, Yàlla moo daganal àtteb dee ci ñoom, te teewul ñu di ko jëfe, rax ci dolli di farle ñi koy jëfe.

Ba nu toppee sunu bakkan, sunu bëgg-bëgg yu bon yi ndigali yoonu Musaa yee, ñoo daan liggéey ci sunuy cér, ngir nu meññ lu nu jëme ci ndee.

Ku topp bakkanam, fàww mu dee, waaye ku rey jëfi yaramam ci ndimbalal Noowug Yàlla, dina texe.

¶ Bu leen lenn nax; Yàlla deesu ko foontoo. Nit ki, li mu ji, moom lay góob.

Waaye su meññee ay dég aki xaaxaam, amul njariñ, alkuteem lees di tudd léegi, te lakk lay mujje.

Te xemmemtéefu bakkan bu ëmbee, bàkkaar lay wasin, te bàkkaar bu matee, ndee lay jur.

Ndax kat tey la àtte bi wara tàmbalee ci waa kër Yàlla. Ndegam ci nun lay tàmbalee nag, ñi gëmul xibaaru jàmm bu Yàlla, ana fu ñu jëm?

Deretu ñu sell ñeek deretu yonent yi lañu tuur, nga nàndal leen deret, feye leen.»