Piyeer ne leen: «Tuubleen te ku nekk ci yeen sóobu ci ndox ci turu Yeesu Almasi ngir njéggalug bàkkaaram, ngeen daldi jot ci Noo gu Sell giy maye.
TSK
TSK · Romans 6:3
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Ba ñu déggee loolu lañu sóobu ci ndox ci turu Sang Yeesu.
¶ Gannaaw noo deeyandoo ak Almasi nag, gëm nanu ne nooy dundandoo ak moom.
¶ Am, bokk yi, yeen ñi xam yoon wi laay waxal, dangeena umple ne yoon yiliful nit ki lu moy ci giiru dundam?
¶ Seen damu gii de jekkul dara. Xanaa xamuleen ne as lawiir tooyalu sunguf bépp lay funkil?
¶ Am xamuleen ne aji jubadi ñi amuñu cér ci nguurug Yàlla? Bu leen kenn nax: Muy fokati séy yi, di bokkaalekat yi, di jaalookat yi, di góor-jigéen yi, ak ñiy ànd ak ñoom,
Dangeena xamul ne seen yaram mooy màkkaanu Noo gu Sell, gi ci yeen, Noo gi ngeen jote ci Yàlla? Moomuleen seen bopp,
¶ Xanaa xamuleen ne, ab rawante, ñépp a cay daw, waaye kenn doŋŋ ay jël ndam li? Dawleen nag ba jël ndam li.
¶ Su fekkee ne ñi dee duñu dekki, kon ñi ñu sóob ci ndox ngir ñi dee, lu ñu koy def, doye? Gannaaw ñi dee duñu dekki, ana lees leen di sóobe ngir ñi dee?
Moo tax dootu man maay dund, waaye Almasi mooy dund léegi ci man. Sama dundu yaramu suux wii tey nag, ci ngëm gi ma gëm Doomu Yàlla laa koy dunde, moom mi ma sopp, ba jébbale boppam ngir man.
¶ Bokkaalekat yi ngeen doon! Xanaa xamuleen ne xaritoo ak àddina moo di noonoo ak Yàlla? Kon nag ku namma def àddina ab xarit, ab noonu Yàlla ngay doon.