sarxalkat bi seet ko, gàkk yooyu ci yaram wi di lu weex, xawa xall, xam rekk la, ju feeñ ci yaram wi waaye nit ki set na.
TSK
TSK · Romans 7:22
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Xanaa di bége yoonu Aji Sax ji, di ko jàngat guddeek bëccëg.
Ma ne: «Maa dikk nii, téereb yoon wi indi na li ñu bind ci man.
Sa kàdduy seede laay safoo, ñuy sama xejj yi may xelal.
Maay bége sa santaane yi ma sopp,
Su ma bégewuloon saw yoon, sànkoo sama toskare ji.
Maa séddoo fàww sa kàdduy seede, loolooy seral sama xol.
Maa sopp say santaane, mu gënal ma wurus ba ci wurusu ngalam.
Aji Sax ji, namm naa sa wall, sa yoon ay sama bànneex.
Yeen ñi xam njekk, dégluleen ma, yeen, askan wi sama yoon yebu ci seen xol. Buleen ragal nit ku leen sewal, buleen tiit seeni xaste.
Waaye ab Yawut dëgg, kumpag biir xol la koy nekke, xaraf it mbirum xol la; ci xel mi lay sottee, waaye du ci mbindum yoon. Ngërëm la it du ci nit lay jóge, xanaa Yàlla.
¶ Moo tax dunu ñàkk yaakaar. Doonte sax sunu bitib jëmm a ngi gën di bon, sunu jëmmu biir moom, mu ngi yeeslu bés ak bés.
Buleen di fenante, gannaaw seen jëmm ja woon démb, boole ngeen kook jëfinam ja mu àndal, summi,
waaye nay lu làqoo jëmmu biir, nay gànjar gu dul jeex, te mooy lewetaay akug teey, ndax looloo réy njarte fa Yàlla.