TSK

TSK · Romans 8:25

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

«Céy Aji Sax ji, maa ngi séentu sa xettal!

Neel tekk, xaar Aji Sax ji, yaakaar ko. Bu sa xol jóg ci kuy baaxle, tey lal ay pexe.

Seeni mébét, wàcce boroom daraja doŋŋ; yeena ngi bége ay fen, seeni kàddu diw yiw, seen xalaat diy saaga. Selaw.

Bésub keroog dees na ne: «Sunu Yàllaa ngii nag! Moom mii lanu yaakaaroon te moo nuy wallu. Aji Sax jii lanu yaakaaroon, nan bég te bànneexoo wallam.»

Te du càkkéef gi rekk, waaye nun ci sunu bopp itam, ci lanu, nun ñi jot ab dawal ci Noo gi, nun ci sunu bopp sax nu ngi binni sunu biir xol, ndax yàkkamtee jot céru doomi Yàlla, ba sunu njotug yaram mat.

Ngir itam ngeen manoorewoo jépp manoore, na leen ko Yàlla manloo ci kàttanam gu màgg, ba ngeen mana dékkoo lépp, xolu muñ,

Yal na Boroom bi wommat seen xol, jëme ci cofeelu Yàlla ak muñ gi ci Almasi.

Noonu la Ibraayma muñe, ba kera mu jote ca dige ba.

¶ Kon nag gannaaw gii ndiiraanu seede wu réy moo nu yéew, nanu sippiku mboolem sëf bu nuy yeexal, ak bàkkaar bu nu yomba téqtal. Ñu daw nag xél wi ñu nu waajalal, te baña yoqi.

James 5:7 TSK

¶ Kon nag bokk yi, muñleen, ba Boroom bi délsi. Seetleen ci beykat biy séentu njariñal meññeef mu jóge fi suuf si. Ma ngay muñ, céebo ba bët wàcc.

Ku wara dem ngàllo, ngàllo nga jëm, ku wara deeye saamar, saamar ngay deeyeji. Looloo tax ñu sell ñi wara saxoo muñ ak ngëm.