¶ Waaye yaw Aji Sax ji sunu Yàlla, yàggul dara aw yiw bàyyikoo na ci yaw, musal ñenn ci nun, may nu ndëgërlaay ca sa bérab bu sell ba. Yaw sunu Yàlla, yaa nu taxa leqliku, yaa nu dundalaat ci sunu biir njaam gi.
TSK
TSK · Romans 9:27
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Ezra 9:8
TSK
Isaiah 1:1
TSK
¶ Lii moo di peeñum Esayi doomu Amocc, di lu mu gis ci mbirum Yuda ak Yerusalem ci janti buuri Yuda yi ñuy wax Osiyas ak Yotam ak Axas ak Esekiya.
Isaiah 10:20
TSK
Keroog bés booba li des fi Israyil ak li rëcce kër Yanqóoba duñu wéerooti ña leen duma. Aji Sax ji lañuy wóolu, wéeroo ko, Aji Sell ju Israyil.
Isaiah 24:13
TSK
Noonu lay deme ci àddina, ci biir xeet yi, mbete benn-benni doomi oliw gu ñu gësëm, mbaa doomi reseñ yu des ca ndey ja, gannaaw bu ñu wittee ba sottal.
Ezekiel 6:8
TSK
Waaye maay déeg lenn ci yeen, ñu rëcc saamar, tasaaroo ci xeet yi, ci biir réewi jaambur.
Micah 5:3
TSK
Kilifa gaay taxaw, sàmme ci dooley Aji Sax ji, ci màggug turu Yàllaam Aji Sax ji, ba ñu dëkke jàmm, nde léegi lay doon ku màgg ba turam dajal cati àddina.