TSK

TSK · Ruth 1:6

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

¶ Gannaaw loolu Aji Sax ji yéwéne na Saarata, ni mu ko waxe woon, defal ko li mu ko digoon.

Ma ngay ñaanal Yuusufa. Mu ne: «Yàlla ji samay waajur Ibraayma ak Isaaxa toppoon, moom Yàlla, ji ma sàmm, ba ma juddoo ba tey jii,

Demal woo magi Israyil, ñu daje, nga ne leen: “Aji Sax ji, seen Yàllay maam ya, di Yàllay Ibraayma ak Isaaxa ak Yanqóoba, moo ma feeñu, ne ma: ‘Gis naa leen, te yég naa li ñu leen di teg ci Misra.

¶ Ba loolu amee Aji Sax ji wax Musaa ne ko: «Maa ngi nii di tawal bànni Israyil ñam wu jóge asamaan, te na mbooloo mi dem bés bu set, fori njëlu bés ak bés. Ma nattu leen ci, ba xam ndax dinañu doxe sama ndigalu yoon am déet.

Yaw yaay taxaw, ñeewante Siyoŋ, ndax baaxe ko jot na, àpp ba kay mat na.

Mooy leel ku ko ragal, di bàyyi xel kóllëreem gi ba fàww.

Ñépp a la wékk bët, di yaakaar, te bu jotee, yaa leen di leel,

jàmmal seen suufas réew, reggal leen ngëneelu pepp,

Ab taw ak tawub yuur asamaan lay wàcce, du fa dellu, te suuxatul suuf, saxal ko, meññal ko, ba kuy ji, mu may la jiwu; kuy lekk, mu may lam pepp.

Joel 2:19 TSK

Aji Sax jee àddu, ne ñoñam: «Maa ngii di leen yónnee am pepp, ak biiñ bu bees akug diw, ba ngeen regg, te dootuma leen gàcceel ci biir xeeti jaambur yi.

Ñoo lay nappaaje ci suuf, yaak say doom yi ci sa biir, te duñu bàyyi doj ci kaw doj ci sa biir, ndax ba sa bésub wall dikkee, yaa ko ràññeewuloon.»

Seen dundin ci biir jaambur ñi gëmul, rafetal-leen ko, ba su ñu leen waxaloon ne ay defkati lu bon ngeen itam, seen jëf ju rafet lañuy gis, te moom lañuy sàbbaale Yàlla, kera bésub dikkam.