TSK

TSK · Titus 2:11

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Woyleen Aji Sax ji woy wu yees, te àddina yépp woy Aji Sax ji.

Muy kàddug Sabóor. Woyleen Aji Sax ji woy wu yees, moo def ay jaloore, kàttanam ak sellngay dooleem jox na ko ndam li.

Fan yu mujj ya, dees na taxawal tundu kër Aji Sax ji, Aji Sax ji mooy gëna kawe ci tund yi, tiim tund yu ndaw yi, xeet yépp riirandoo, wutsi ko.

Mu ne: «Xeeb naa li ma la sas ngay sama jaam biy siggil giiri Yanqóoba, te wara délloosi ndesu Israyil gii. Tabb naa la, ngay leeru xeet yi, di jotale waa cati àddina sama wall.»

Yerusalem, jógal ne ràññ, sag leer feq na; teddngay Aji Sax ji fenkal na la!

¶ «Bu loolu amee maay sottil waa kër Daawuda ak waa Yerusalem, noowug yiw aki dagaan, ba ñu geesu ma man, mi ñu jam ba mu sar, te dinañu ko jooy ni ñuy jooye benn bàjjo, di ko naqarlu ni ñuy naqarloo deewug taaw.

te ciw turam, dees na dale ci Yerusalem, yégal xeet yépp, tuubeel gu jur njéggalug bàkkaar.

Ba Barnaba dikkee ba gis yiw, wi leen Yàlla may, dafa bég, di leen ñaax ngir ñu ŋoye seen xol ci Sang bi.

Ndax noonu la nu ko Boroom bi sante ba mu nee: “Maa la tabb ngay leeru jaambur ñi, ngir nga jottliji mucc gii, ba ca cati àddina.”»

¶ Kuy liggéey, ag peyooram du taxawe ag may, waaye wartéef la.

¶ Waaye ni moyug Aadama deme, yiwu Yàlla demewu ni. Moyug kenn nit, Aadama, tax na ñu bare dee; waaye yiwu Yàlla ak mayug yiw gu kenn nit, Yeesu Almasi, ñaata yoon la gënatee baawaan, ñeel nit ñu bare?

¶ Waaye dama ne: xanaa dañoo déggul? Ahakay! Ndax «Àddina sépp la seen baat jibal, cati suuf sépp la seen kàddu dajal.»

Leneen li indi Almasi mooy may jaambur ñi dul Yawut lu ñu màggale Yàlla, te muy yërmandeem. Noonu it la Mbind mi indee ne: «Looloo waral ma sant la ci biir xeet yi, sàbbaal la.»

Duma neenal yiwu Yàlla, ndax kat su doon ci sàmm ndigalu yoon lees di ame àtteb ku jub, konoon Almasi moo dee cig neen.

nun ñi doon nit ñu dee ba noppi ndax sunuy moy, moo nu booleek Almasi, dundalaat nu. Ci kaw yiw daal ngeen mucce.

ba mu leer ne jaambur ñi dul Yawut ñooy bokk ak Yawut yi benn cér bi, ñooy doon wenn yaram, te ñooy bokk benn dige bi ci Almasi Yeesu, ni ko xibaaru jàmm bi xamlee.

Noonu la deme, ndegam kay fekk na leen sësoo ngëm gu ngeen dëjoo ba dëgër, te baña nangu lenn di leen sorele ak yaakaar ji ci xibaaru jàmm, bi ngeen dégg, te ñu biral ko, ñeel mépp mbindeef. Man Póol nag, ci yégle xibaaru jàmm boobu laa di ab jawriñ.

Sunu yiwu Boroom moo ma baawaanal, booleel ma ci ngëm gi, ak cofeel, gi gëmkatub Almasi Yeesu jagoo.

Waaye Boroom bee ma dimbali, dooleel ma, ngir kàddu gi siiwe ci man, ba xeeti jaambur yépp dégg ko, te Boroom bee ma musal ci pàddum gaynde.

Yeesu mi ñu def mu gëna suufe as lëf malaaka yi, moom lanu gis deeyam gi mu dee tax mu jagoo kaalag teraanga. Noonu la deeyale ñépp ci kaw yiwu Yàlla.

¶ Googu texe, yonent ya jottli woon waxyub seen yiw wi leen dikkal, niir nañu ko, càmbar ko.