TSK

TSK · Titus 3:1

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Doom, ragalal Aji Sax ji, wormaal buur. Bul lëngook kuy fippu.

Su la sa kilifa meree, bul jóge fa ñu la teg; tooñ yu mag, teey ba giif.

Buleen leen déglu. Nangul-leen buuru Babilon te dund! Ana lu jar dëkk bii di mujje doon jalub xeer?»

¶ Kon nag yeen sama bokk yi ma soppal sama bopp, farluleen, bu leen dara yëngal, te saxooleena jëm kanam ci liggéeyu Sang bi, te ngeen xam ne seenu ñaq, ci seenub ànd ak Sang bi, du neen.

Ndax kat noo di liggéeyu Yàlla; Yàllaa nu yeesal ci Almasi Yeesu, ngir nu wéye jëf ju rafet, ja mu nu fàgguloon ca njàlbéen, ngir nu di ko jëfe.

Su ko defee ngeen di dunde dundin wu yellook Boroom bi, ngir bànneexal ko ci wet gu nekk, seen meññeef it di jépp jëf ju baax, te ngeen gën di xam Yàlla.

¶ Soo dee xamal loolu bokki gëmkat ñi, yaa di jawriñu Almasi Yeesu ju baax ju xontoo kàdduy yoonu ngëm wi, ak àlluwa ju rafet ji nga topp naka jekk.

Moo tax li ma lay fàttli moo di nga xamb taalub mayu Yàlla, ga nga jote ca ba ma la tegee samay loxo.

Moo maye bakkanam ngir nun, moo nu jot, ba nu mucc ci gépp njubadi, moo nu def askan wu mu setalal boppam, séddoo nu, nuy askan wu farlu ci jëf ju baax.

Na sunuy ñoñ tàggatu ci jëf ju baax ju ñu saxoo ba faj soxla yu taxaw, ngir ñu baña ñàkk njariñ.

¶ Nangul-leen gépp kilifteef gu tege ci àddina ngir Boroom bi; muy buur bu mag bi gëna kawe,

¶ Soppe yi, sama ñaareelu bataaxal a ngi nii, te bu ci nekk am na lu ma leen ci fàttli, ngir xiirtal leen ci xalaatin yu set,