TSK

TSK · 1 Kings 7:21

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage
Ruth 2:19 TSK

Goro ba ne ko: «Foo fore lii lépp tey? Ban tool nga doon liggéeye sax? Ki la nemmikoo nii de, yal na barkeel!» Ruut nag wax goroom ka mu doon liggéeye toolam, ne ko: «Ka ma doon liggéeye toolam de, Bowas lañu koy wax.»

Te bu say fan matee ba nga tëddi, fekki say maam, maay yékkati kenn ci saw askan, sa deretu bopp, mu wuutu la, te maay saxal nguuram.

Miiru ëtt bu mag bi dees koo wëralee ay xeeri yett aki xànqi seedar: ñetti sësalantey xeer yu tegloo yu ne, benn sësalanteb xànqi seedar tege ca. Mu mel ni na ñu def ëttu biir bu kër Aji Sax ja ak dëru buntu kër ga.

Dees na ma waxal ne: «Aji Sax ji rekk a jagoo njekk ak doole!» Mboolem ñi ma mereey ànd, sëgg, fekksi ma.

Dal-luwaayu mbaar mi gudde ñaar fukki xasab, yaatoo fukki xasab ak benn. Mu am dëggastal yu ñuy yéege, jàll ca biir, ñaari jën séq ko, wet gu nekk, wenn.

Ña ñu jàppoon ne ñooy kenuy mbooloom gëmkat ña nag, te ñuy Yanqóoba ak Sefas ak Yowaan, ba ñu ràññee yiw wi ñu ma jagleel, maak Barnaba lañu jox loxo, ngir nun nu liggéeyi ca jaambur ña, te ñoom ñu liggéeyi ci Yawut yi.