TSK

TSK · Acts 1:3

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

¶ Ba loolu amee ma daanu tëdd fa kanam Aji Sax ji, na woon, diiru ñeent fukki bëccëg ak ñeent fukki guddi. Du ñam wu ma lekk, du ndox mu ma naan ndax seen gépp moy gu ngeen moy, di def lu Aji Sax ji ñaawlu, ba merloo ko.

¶ «Ci jamonoy buur yooyu Yàlla Boroom asamaan dina samp nguur gu dul tas mukk, te wenn xeet du ko yilif mukk. Nguur googu dina tasaare mboolem yeneen nguur yooyu, ba genn du ci des, waaye moom day sax ba fàww.

Luke 24:1 TSK

¶ Ca ëllëg sa, di ndoortel ayu bés, jigéen ña jëlu dem ca bàmmeel ba, yóbbaale cuuraay la ñu waajal.

Muy yégle nguurug Yàlla, di jàngle mbirum Sang Yeesu Almasi ci teeyug bakkanam te amul benn gàllankoor.

Ñaax nanu leen, dëfal leen, dénku leen, ngir ngeen di jëfe jëfin wu yelloo ak Yàlla, mi leen woo ci nguuram ak teraangaam.