Ndaxam yaa ngi réy-réylu ci sama kaw ñoñ ba tey, bañ leena bàyyi, ñu dem.
TSK
TSK · Acts 12:23
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
¶ «Guddig keroog maay wër réewum Misra te maay fàdd lépp luy taaw bu góor ci réewum Misra, nit ak mala, te itam maay mbugal mboolem tuuri Misra. Man maay Aji Sax ji.
¶ Ca xaaju guddi la Aji Sax ji fàdd mboolem taawi réewum Misra yu góor, dale ko ca taaw bu góor bu Firawna, ma toog ca jal ba, ba ca taaw yu góor yu nit ña ñu tëj kaso, boole ca lépp luy taaw bu góor ca jur ga.
Naka la malaaka ma tàllal loxoom, ngir faagaagal Yerusalem, Aji Sax ji fomm, daldi wax ak Malaakam bóomkat may fàdd askan wa. Mu ne ko: «Doy na! Teggil sa loxo.» Booba malaakam Aji Sax jaa nga ca wetu dàggay Arawna, Yebuseen ba.
Bu sama der bi lekkoo sax, du tee ma dese suux wu ma xoole Yàlla,
Xel mu ñaw, jëw bu rafet; sam xel jekkadi, ñu xeeb la.
Ana kooy kókkaleek a ñàkke kersa? Moo kooy yékkatil kàddu? Kooy xool gëti xeebeel? Xanaa du Aji Sell ju Israyil ji?
«Te bu ñu génnee, gis néewi ñi doon fippu fi sama kaw, seeni sax duñu dee mukk, seen sawara du fey mukk, te boroom suux bu leen gis, yaram wa daw.»
Xanaa doo janook ki lay rey, naati yaay yàlla? Boo tàbbee ca sa loxoy jamkat ya, keroog nga noppee doon yàlla, di nitu kese.
¶ «Buur, Yàlla Aji Kawe ji daa joxoon sa baay Nabukodonosor nguur gi, muy ku màgg, am ndam ak daraja.
¶ «Jawriñ jooju xam nammeelu njaatigeem, te taxul mu waaj ko, ba jëfewu ko, ay yetam dina bare.
¶ Ci kaw loolu Póol ak Barnaba yég la xew. Ñu xotti seeni yére ndax ñaawlu ko. Ñu buur nag ba ca biir mbooloo ma, daldi àddu ca kaw ne: