TSK

TSK · Acts 13:22

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Waaye su ngeen saxee ci def lu bon, yeen ak seeni buur ay bokk sànku.»

«Réccu naa li ma fale Sóol buur, ndax dëddu na ma, te samay ndigal, jëfewu ko.» Samiyel am ca njàqare lool, ba fanaanee tinu Aji Sax ji guddi gépp.

Samiyel ne Sóol: «Duma walbatiku ànd ak yaw, ndax yaa gàntal kàddug Aji Sax ji, Aji Sax ji gàntal sa nguur ci Israyil.»

¶ Gannaaw ba loolu wéyee Aji Sax ji ne Samiyel: «Yaw foo àpp sa jooy yi ngay jooy Sóol te man maa ko dàq, ba doonatul buur ci Israyil? Gannaaw maa foq nguuram ci Israyil kay, duyal sa béjjén diwu oliw ba mu fees te nga dox, ma yebal la ci Yese waa Betleyem bi. Gis naa ciy doomam ki may fal buur.»

Samiyel ne ko: «Loo may laaj, gannaaw Aji Sax jee la dëddu, def la ab noon?

Ba mu ko defee waa Yuda dikk, diw fa Daawuda, fal ko buurub waa kër Yuda. Gannaaw gi ñu wax Daawuda ne ko waa Yabes Galàdd ñoo rob Sóol.

¶ «Kon nag waxal sama jaam Daawuda, ne ko: “Aji Sax ji Boroom gàngoori xare yi dafa wax ne: Maa la jële ca parlu, ga nga toppe woon gàtt ya, ngir nga doon kilifag Israyil, sama ñoñ.

Muy roy nag baayam ca mboolem bàkkaar ya mu daan def. Te it wéetalul woon Yàllaam Aji Sax ji ni maamam Daawuda.

Mu teg ca tabb Daawuda, jaamam ba, jële ko ca gétti xar ya,

kon dees na mana dog sama kóllëreek Daawuda sama jaam bi, dogaale sama kóllëreek sarxalkati Leween ñi may liggéeyal, ba Daawuda ñàkk sët bu koy wuutu cib jalam.

¶ «Gannaaw loolu maa leen di waajalal ab sàmm bu leen di sàmm. Kookooy Daawuda sama jaam bi. Moom moo leen di foral, mooy doon seen sàmm.

Hosea 3:5 TSK

Gannaaw loolu bànni Israyil dinañu walbatiku, sàkku seen Yàlla Aji Sax ji, ak Daawuda seen buur. Ca jant yu mujj ya, xolub ragal Aji Sax ji lañuy dikke fi moom, akug mbaaxam.

Acts 7:46 TSK

Daawuda, ma Yàlla baaxe woon, sàkku woon na am màkkaan ngir Yàllay Yanqóoba.

¶ Ngëm la Abel jébbale Yàlla sarax su gën saraxub Kayin, te ngëm lees seedeele Abel ne moo jub, kera ba Yàlla ci boppam seedee ne ay saraxam a nangu. Ngëm it moo waral Abel dee, te di wax.