TSK

TSK · Acts 26:3

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Ma boole jël kayitu njaay bi tëjewul ak kayitu njaay bi tëje, te yoonalu njaay meek sàrt yi tënke ci.

Ñoo dégg nag sab jëw, ñu ne dëddu yoonu Musaa mooy li ngay jàngal mboolem Yawut yi dëkk ci biir jaambur ñi, naan leen buñu xarfal seeni doom, te buñu topp sunuy aada.

¶ Ba loolu amee boroom réew ma jox Póol kàddu gi. Mu ne: «Xam naa ne at yu baree ngii ngay àtte xeet wi. Moo tax ma am cawartey layool sama bopp.

Mbiram nag laa amul dara lu ma wóor, ngir ma bind ko sang bi. Moo tax ma indi ko ci seen kanam, rawatina ci sa kanam, Buur Àggripa, ngir gannaaw bu ñu ko dégloo, ma mana am lu ma bind.

Lii ma wax, buur bi xam na ko, moo tax ma ñeme koo wax ci kanamam, ndax bir na ma ne, amul lenn lu ko ump ci lii, ngir du cib ruq la xewe.

Su ma jotoon ci kàddug waxyu, boole ci xam mboolem kumpa, ak mboolem xam-xam, ak ngëm gu mat sëkk ba mana toxal ay tund, te jëfewuma cofeel, duma dara.