TSK

TSK · Acts 6:3

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Firawna daldi ne jawriñ ya: «Ndax masees naa gis ku mel ni kii a waay, nit ku Yàlla sol Noowug boppam?»

Aji Sax ji ne Musaa: «Jëlal Yosuwe doomu Nuun. Nit la ku noowal biir nekk ci moom. Nanga ko teg sa loxo, sase ko noonu.

Job 32:7 TSK

Ma noon: «Na yàgga-dund wax, na dund-jopp xamle xel mu rafet.»

mooy sol noowug dëgg kuy toog di àtte, di jàmbaaral ñiy waññi noon yi song dëkk bi, xare.

Acts 2:4 TSK

Ñoom ñépp nag feese Noo gu Sell gi, tàmbalee làkk làkk yu wuute, na leen ko Noo gi manloo.

Acts 9:30 TSK

Bokki gëmkat ña nag yég ko, daldi koy yóbbu Sesare, yebale ko foofa, mu dem Tàrs.

Acts 13:2 TSK

Ñooñoo daje woon di màggal Boroom bi, boole kook koor. Ci biir loolu Noo gu Sell gi ne: «Beral-leen ma nag Barnaba ak Sóol ngir liggéey, bi ma leen wooye.»

Acts 16:2 TSK

Muy ku rafet seede ci biir bokki dëkk yooyu di Listar ak Ikoñum.

Kii ci Noo gi la jote kàddu gu xelu, kee séddoo kàddug xam-xam ci genn Noo gi.

Rax ci dolli, mboolooy gëmkat ñi ñoo ko tabb, ngir mu ànd ak nun, ba nu yóbbu ndimbal li, muy teddngay Boroom bi ci boppam, te di sunu firndey cawarte ci dimbalee.

Te it ñi ci biti te gëmuñu, la ñu ko seedeel nay lu rafet, ba deram du yàqu, nde kon mu tàbbi ci fiiru Seytaane.

gépp may gu baax, ak bépp jagle bu mat, fa kaw la bawoo, di lu wàcce fa Baay biy boroom leer yi, ki soppikuwul ci lenn, te genn ker gu toogadi nekkul ci moom.