TSK

TSK · Daniel 5:23

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Yàlla Aji Sax ji nag móol nit ci pëndu suuf, sol ngelawal dund ci paxi bakkanam, nit daldi doon boroom bakkan.

Daawuda ne ña mu dendal: «Ngeen ne, lees di defal ku rey waa Filisti bii, ba faj gàcceg Israyil? Ak kuy yéefaru waa Filisti bii sax, bay dëkk gàngoori Yàlla jiy dund?»

Dëgg la moos, yaa duma Edom, ba tax nag sam xel jay la. Tee ngaa bàkku te toog sa kër? Te sax ana looy dugge ci jote buy indi ay wu lay daane, yaw, daanewaale Yuda?»

Job 31:4 TSK

Du Yàllaa ngi gis fu ma jaare, di waññ sama bépp jéego?

Soo leen làqoo, ñu tiit; nga rocci seen noo, ñu saay, dellu di pënd.

Asamaan, asamaanu Aji Sax jee, suuf la dénk doom aadama.

di càmbar samab dox ak sama tëraay, yittewoo lépp lu may def.

Jéegoy jaam Aji Sax jee ko yor, kenn xamul foo jëm.

Aji Sax ji nee: «Xaaral rekk ma jóg, xaaral rekk ma ne ñokket, xaaral rekk ma teewal samag kawe.

Ana kooy kókkaleek a ñàkke kersa? Moo kooy yékkatil kàddu? Kooy xool gëti xeebeel? Xanaa du Aji Sell ju Israyil ji?

Ñii déy a yullee wurus ci mbuus, sàkk xaalis, natt diisaay ba, fey tëgg bu leen ci tëggal am tuur mu ñuy sukkal ak a sujjóotal,

Baatu daw-làqu yu rëcc a ngoog, bawoo réewum Babilon, di yeggesi waa Siyoŋ mbugalum Aji Sax ji sunu Yàlla, mbugal mi këram waral.

«Yaw nit ki, waxal Boroom Tir, ne ko: “Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Dangaa fuuy ba naan: ‘Maay Yàlla, ji tooge toogub yàlla yi, fi xolu géej!’ Waaye yaw doom aadama nga, doo Yàlla, dangay yàlla-yàllalu rekk.

Sab taar a la fuuyloo, sa daraja tax nga yàq sam xel! Fi suuf laa la rattax, fi kanam buur yi laa la detteel, ñu di la seetaan.

Muy damu bay diir mbagg Njiital gàngooru xare gi, daldi dakkal sarax ba ñu ko daan defal bés bu jot, màbb bérabam bu sell ba.

«Xol baa ngay xoggliku, te ag njub nekku ca, waaye ku jub ndax kóllëreem mooy dund.

Te it jariñoowul loxol nit, mbete ku soxla lenn, ndax mooy may ñépp bakkan akug noo, ak lu mu mana doon.

¶ Gannaaw ba ñu xamee Yàlla, taxul ñu màggal ko ngir li muy Yàlla, taxul ñu delloo ko njukkal, xanaa réer ci seen xalaati neen, ba seen xel mu wayadi far tàbbi cig lëndëm.

Te it bumu dib tuubeen bu bees, lu ko moy ag réy-réylu man na koo gëlëmal, ba mu tàbbi ci mbugal ni Seytaane.

¶ Ñu may rab wi nag muy kañu ak a saaga Yàlla, may ko it mu saña wéye noonu diiru ñeent fukki weer ak ñaar.