¶ Ba loolu amee ma digle foofa koor ca tàkkal dexu Aawa, toroxloo ko fa sunu kanam Yàlla, ngir ñaan ko mu may nu yoonu jàmm, nook sunuy doom ak mboolem lu bokk ci nun.
TSK
TSK · Daniel 9:3
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Ba loolu amee Esra bàyyikoo kër Yàlla ga, fatuji néegu Yowanan doomu Elyasib. La mu fa nekk nag lekkul, naanul, xanaa di ñaawlu na ngàllo, ga ñibbsi feccee worma.
¶ Keroog ñaar fukki fan ak ñeent ca weer woowa, bànni Israyil daje nañu, sol ay saaku, xëppoo suuf, di ko ñaawloo ci biir koor.
Ci biir loolu mboolem diiwaani réew mi, fépp fu dogalu buur ak ndigalam àgg, muy ñaawlu gu réy ca Yawut ya. Ñu boole kook koor aki jooy aki yuux. Ñu bare sol ay saaku, sottikoo dóom, di ko toroxloo.
Moo ma tax ne: «Wàqet, tuubi-ruubi,» ba diwoo suuf akub dóom.
Damaa xér ci sa kër gi, ba jeex tàkk, te jëf ji ñu la sewale man la dal.
Bésub keroog Boroom bi, Aji Sax ji ci gàngoor yi moo leen di woo ci jooyoo ak ñaawlu ak wateefu nel, ak colu saaku ngir ñaawlu.
Su boobaa ngeen woo ma wall, dikk ñaan ma, ma nangul leen.
¶ «“Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Lii laay nangulaatal waa kër Israyil, defal leen ko: maay ful nit ñi niy gàtt.
¶ Jant yooyu, man Dañeel maa nga doon ñaawlu diiru ñetti ayi bés.
«Terewul ba léegi,» kàddug Aji Sax jee, mu ne: «Délseeleen seen léppi xol ci man, boole kook koor aki jooy aki yuux.
¶ Ci kaw loolu Korney ne: «Bëkkaati-démb ci waxtuw digg njolloor wii nu tollu tey, ci laa doon ñaane sama biir néeg. Mu am ku jekki ne jaas ci sama kanam, sol yére yu ne ràññ.
Kon nag tuddanteleen seeni bàkkaar tey ñaanalante, ndax ngeen wér. Aji jub ji, ag ñaanam, doole lay dale.