TSK

TSK · Deuteronomy 21:23

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Aji Sax ji ne Musaa: «Jàppal njiiti mbooloo mi yépp, nga wékk leen ci bant fi kanam Aji Sax ji, bëccëg ndarakàmm, ngir sànjum Aji Sax ji dëddu Israyil.»

Buleen sobeel réew mi ngeen dëkk, te man ma màkkaanoo ci biiram, ndax man Aji Sax ji maa màkkaanoo ci biir bànni Israyil.»

Buleen dugal yëf yu seexluwu seen biir néeg, lu ko moy àtteb faagaagal bi war ci yëf yooyu, moo leen di dab, yeen itam. Xofleen koo xof, seexlu koo seexlu, ndax yëf yooyu, faagaagal moo ci war.

Kon dees nuy jox juróom ñaari góor ñu askanoo ci Sóol, nu jam leen ba mu sar fa kanam Aji Sax ji ca Gibeya, dëkkub Sóol, ma Aji Sax ji faloon.» Buur ne leen: «Dinaa leen leen jox.»

¶ Almasi moom, moo nu jot ci alkàndey yoon wi, ba mu doonee ku alku ngir nun, nde: «Alkute ñeel na képp ku ñu rey, wékk ko ci bant.»