Ku bëgg lu neex, liggéey; ku bëgga faj sab xiif, njaxlaf.
TSK
TSK · Ecclesiastes 2:22
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Ma xoolaatal sama bopp lépp lu ma sottal, doñ-doñi ko, ba sottal, ndeke lépp, cóolóoli neen ak napp um ngelaw. Nit gisul njariñ ci kaw suuf.
Waaye benn ŋëb bu ànd ak dal moo gën ñaari ŋëbi doñ-doñ ci napp um ngelaw.
Bu koom yokkoo, lekk-kat yi yokku. Ana lu muy jariñ boroom koom ga, xanaa di ko duufale bëtam?
Nit ak doñ-doñam jépp, biiram, te taxul mu doylu.
¶ Gannaaw loolu Yeesu ne ay taalibeem: «Moo tax ma ne leen, buleen seen bakkan jaaxal, ngir lu ngeen lekk, te it buleen seen yaram jaaxal ngir lu ngeen sol,
Buleen jaaxle ci dara, waaye ci mbir mu mu mana doon, deeleen dikke Yàlla seeni soxla, di ko ñaan ak a dagaan te boole ci di ko sant.
ci ni ngeen di sippikoo ci kawam, mboolem seenu tiis, nde mooy ki leen tiisoo.