TSK

TSK · Esther 2:5

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

¶ Jenn waay la woon ju bokk ci giirug Beñamin, ñu di ko wax Kis. Abyel ay baayam; Abyel, Seror ay baayam; Seror, Bekorat ay baayam; Bekorat, Afiya Beñamineen ba di baayam. Kis ku am daraja la woon.

Yowakin buurub Yuda génn fekki buuru Babilon, jébbal ko boppam, mook ndeyam aki surgaam aki jaraafam ak jawriñi këram. Buuru Babilon nag jàpp ko. Looloo nga yemook juróom ñetteelu atu nguurug Nabukodonosor buuru Babilon.

Jamono yooyu Buur Aserus moo toogoon ca jal ba ca Sus, péey ba.

Mboolem jawriñi buur yi féete buntu kër buur nag di sukkal Aman, di ko sujjóotal, ndax loolu la Buur santaane woon ci moom. Teewul Mardose lànk, sukkalu ko, sujjóotalu ko.

Mardose Yawut ba, moo sësoon rëkk ca Buur Aserus, sut Yawut yépp, ay bokki Yawutam yu bare nawloo ko. Muy sàkku nag ngëneeli ñoñam, di waxal jàmm mboolem askanam.