TSK

TSK · Exodus 18:21

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

¶ Ca gannaaw ëllëg sa Yuusufa ne leen: «Bu ngeen defee lii may wax, dingeen dund, ndax man ragal naa Yàlla.

Mu seet ca bànni Israyil gépp, tànn ca góor ñu mat, fal leen, ñu yilif mbooloo ma: ñii jiite kuréli junniy nit; ñii, téeméer; ñii, juróom fukk; ñii fukk.

Bu ñu liitee benn nag kilifa yi jiite gàngoori Israyil ñooy dajesi fi yaw.

Ci kaw loolu ma jël seen njiit yu rafet xel yu ràññiku, yi ngeen jukkee ci seeni giir, daldi leen def seeni njiit, ñii yilif junniy nit, ñii téeméer, ñii juróom fukk, ñii fukk, ñii diy jawriñ ci seeni giir.

Ñoom lay tabb ngir ñu doon njiiti kuréli junniy dag, mbaa njiiti kuréli juróom fukk. Ñoom it lay beyloo toolam, di leen góobloo, di leen sàkkloo ay gànnaayi xareem ak jumtukaayi watiiram.

¶ Ba loolu weesee Daawuda xayma na mbooloo ma mu àndal, fal ca seen biir njiiti kuréli junniy xarekat, kurél gu ci nekk ak njiiti kuréli téeméer ya ko sos.

Kon nag Sang bi, may ma xel mu am ug dégg mu ma àttee sa ñoñ, ngir may ràññee lu baax ak lu bon. Ndax kat, ana kan moo mana àtte sa ñoñ, wii askan wu réy?»

Su ko defee su ma teqlikook yaw, ngelawal Aji Sax ji yóbbu la fu ma xamul, fekk ma dem wax ko Axab, te du la gis. Kon da may rey! Moona sang bi, man de, damaa masa ragal Aji Sax ji ba may ndaw ba tey.

Ma dellu ne leen: «Li ngeen di def de baaxul. Lu leen tee di ragal sunu Yàlla bala noo torox ci kanam noon yi dul Yawut?

Job 29:16 TSK

Néew-ji-doole, maa doon baayam, ku ma xamul sax, may seet àqam.

Du leble, ba teg ca; du nangu ger, ngir fexeel jaambur. Lii ku koy jëfe doo jang.

Bu am réew dee fippu, kilifa ya bare; réew mu jàmm sax, kilifa gaa am déggin ak xam-xam.

ab jal sampe fi ci ngor, ki ci tooge jikko ju dëggu di askanu Daawuda te di njiit luy sàkku yoon, yàkkamti njekk.

Du njekk gu kenn wut cib àtte, du dëgg gu kenn sàkku cib layoo. Ñu ngi yaakaar caaxaan, di fen, di sos ayib, wasin ñaawtéef.

«Wërleen mbeddi Yerusalem, xool-leen, seet ciy péncam rekk ba xam ndegam dingeen gis kenn, kenn kepp kuy def njub, di sàmm worma, ma daldi leen baal.

Alalu ger, ñu jël fi sa biir, ngir lor ay bakkan. Ndollant ci kaw tegandaay, nga jël feyeekoo bor, di wute alal sa àqu moroom. Man nag, nga fàtte ma. Kàddug Boroom bi Aji Sax jee.

«Ndigal yii, nangeen ko jëfe: Deeleen waxante dëgg, te dëgg ak yoon, nangeen ko àttee àtteb jàmm ci seen ëtti àttekaay.

Luke 18:4 TSK

Àttekat ba bañ na ay yoon, waaye gannaaw gi mu ne ci xelam: “Ragaluma Yàlla, yéguma nit,

Du lenn lu ma xemmem ci kenn; du xaalis, du wurus du koddaay.

Waaye ñi sàkkoo barele, ñooy tàbbi ci nattub bakkan, aki fiir, ak lu bare ciy xemmemtéef yu tekkiwul dara, xemmemtéef yuy lore, tey suuxal seeni boroom ci yàqule ak sànkute.