TSK

TSK · Hosea 13:2

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Yeen nag defuleen lu moy jóg wuutu seeni baay, njurum bàkkaarkat yi ngeen doon, di xamb sànjum Aji Sax, ji tàkkal bànni Israyil?

Waaye dinaa déeg ci biir Israyil juróom ñaari junniy (7 000) nit, di mboolem ñi sujjóotaluloon Baal te seen gémmiñ masu koo fóon.»

Seeni tuur xaalis laak wurus, di liggéeyu doom aadama:

Xanaa dungeen wéye fippu, ñu gën leena duma, te bopp di góomi neen, xol jeex tàkk?

Képp ku ca bokk sa gàcce lay doon, ña koy yett sax ay nit doŋŋ lañu. Nañu daje ñoom ñépp, taxaw, bokk tiitaangeek gàcce.

Yeen daw-làquy xeet yi, dajeleen, dikk, ànd, jegesi. Képp ku gàddu tuuru bantam, ak kuy ñaan tuur mu ko dul wallu, kooka xamul dara.

Fàttlikuleen lii te dëgërluwaat! Yeen bàkkaarkat yi, defleen lii ci seen xel.

rafetale xaalis ak wurus, daaj koy pont, dëgëral, ba du yëngu;

Hosea 2:8 TSK

«Moo tax maa ngii di ñage yoonam ay dég, gawe ko ag wurmbal, ba yoon réer ko.

Hosea 8:6 TSK

«Israyil la lii jóge, te ab liggéeykat moo ko sàkk. Kon lii du Yàlla! Ay tojit la wëlluw Samari di mujje.

Lu ñu leen gëna woo, ñu gën maa sore. Ay tuuri Baal lañuy defal ay sarax, te ay xërëm lañuy taalal cuuraay.

«Ana luy njariñal yett jëmmu xërëm ju ki ko sàkk yett, mbaa jëmmu xërëm ju ñu xelli, di ci gëmloo nit ay fen? Sàkk sa yëfi bopp, wóolu ko, xërëm yoo móol te manula wax!

¶ Waaye sag dëgër bopp, ak sa xol bu tuubadi, ci ngay jóore sànjum Yàlla ci sa kaw bopp, keroog bésub sànj ma, fa àtteb Yàlla bu jub di feeñe.

Waaye nit ñu bon ñi, ak maa-man yi dañuy gën di bon rekk, di naxe tey nax seen bopp.