Ilyaas ne xiféet, yem ci mburu mu ñu lakke doj yu tàng, ak njaqub ndox. Mu lekk, daldi naan, ba noppi tëddaat.
TSK
TSK · Isaiah 33:16
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Yàllaa may dooleel, di ma xàllal, yoon mat.
Ragal-leen Aji Sax ji, yeen nitam ñu sell ñi; ku ko ragal doo ñàkk dara.
Moom doŋŋ a di sama cëslaay, di sama wall, di sama rawtu, duma tërëf.
Ku dëkke kiiraayu Aji Kawe ji yaa këroo keppaaru Aji Man ji.
Waaye mooy teggil néew-ji-doole coonoom, ful njabootam nig jur,
Waaye déggal ma, dëkke jàmm, tàggook njekkar ak safaan.»
Yaa di rawtub néew-ji-doole, di rawtub aji ñàkk, biir njàqare, yaay mbaar mu ñuy yiiroo waame, di ker gu ñuy serloo ci tàngoor, nde merum kilifa gu néeg mooy waame wu ne yureet ci kaw miir.
Boroom bee leen di leel njàqare, nàndal leen coono, waaye moo leen di jàngal, dootu leen làqu; dingeen gis ki leen di jàngal,
Duñu xiif, duñu mar; tàngooru mbóoya akub jant du leen sonal, nde ki leen ñeewantee leen di wommat, di leen yóbbu fu ndox bënne.
Yeen nag, buleen tiisoo lu ngeen lekk, mbaa lu ngeen naan; te bu yooyu xalaat ub seen bopp.