TSK

TSK · Isaiah 4:5

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

¶ Ci kaw loolu malaakam Yàlla, ma féete woon xarekati Israyil kanam naka jekk te di leen jiite, daldi toxu, féete leen gannaaw. Niir, wa leen jiitu woon it walbatiku, taxaw ca seen gannaaw,

¶ «Xaymab jaamookaay bi nag, defare ko fukki sori rabali lẽe, mu ànd ak wëñ gu baxa te laal yolet ak wëñ gu xewar ak gu xonq curr, te nga ñawaale ca nataali serub.

¶ Ba loolu amee niir wa yiir xaymab ndaje ma, leeru Aji Sax ji fees jaamookaay ba,

¶ Keroog bés ba ñu sampee màkkaan ma, niir wa daa muur màkkaanu xaymab seede sa. Ca ngoon sa lu mel ni sawara tiim màkkaan ma, ba ca ëllëg sa.

Ci kaw loolu nga di leen jiitee bëccëg aw taxaaru niir, di leen jiitee guddi taxaaru sawara, di leen niital yoon wa ñuy jaare.

Woykat ba nee: «Naa déglu lu Aji Sax ji Yàlla di wax.» Jàmm lay wax wóllëreem ñiy ñoñam, ba duñu dellu ci jëfi dof.

Ana kuy dab-dabal Aji Sax ji, fa kawa kaw? Ana ci goney Yàlla yi ku nirook Aji Sax ji,

Aji Sax ji déy da maa wax ne ma: «Gaynde gu mag ak gu ndaw, bu jàppee bay xiiru, boo ko wooloon gàngooru sàmm it, duñu soowaloo ba xëbal ko, duñu ñolñoli ba mu dellu gannaaw. Noonu la Aji Sax ji Boroom gàngoor yiy wàcce, xaresi fi kaw tundu Siyoŋ ak waa tund wa.»

Xoolal Siyoŋ, dëkk ba nuy màggale; yaay teg bët Yerusalem, dëkkuwaay bu dal ba, xayma bu deesul sempi, wewukaay ya deesu ko buddi mukk, te luy buumu xayma ya it, deesu ko dog.

Maa jegeñal sama njekk, soreetul; sama wall a ngi, yàggatul. Maay maye wall fi Siyoŋ gii, ba Israyil gii di sama gànjar.»

¶ Ma séentu, gisuma lu moy jenn waay ju ŋàbb buumu nattukaay ci loxoom.