TSK

TSK · Isaiah 57:4

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Ndaxam yaa ngi réy-réylu ci sama kaw ñoñ ba tey, bañ leena bàyyi, ñu dem.

Kon kay yaw yaak sa gàngoor gépp, ci kaw Aji Sax ji ngeen bokk daje! Ana kuy Aaróona, ba ngeen di ñaxtu ci kawam?»

Job 16:9 TSK

Meram la ma daggatee, jéppi ma, di yéyu ci sama kaw, daasal ma gëti noon, ne ma jàkk.

Noon yaa ngi ma gaw ni coggalu yëkk, dar ma ni ponkali yëkk ya fa Basan.

Ñu ngi ma ŋa ŋàpp, di ma tuumaal, naan: «Yaw a, yaw a, noo la gis!»

Wóoy wii xeetu moykat, wii askan wu diisu ñaawtéef, mii njurum defkati mbon, yii doomi yàqute! Ñoo wacc Aji Sax ji, ñoo teddadil Aji Sell ju Israyil, dëddu ko.

Wóoy ngalla doom yii diy fippukat! Kàddug Aji Sax jee. Ñu ngi nas mébét yu ma diglewul, di digoo digoo yu ma leen xelalul, di tegle bàkkaar ci kaw bàkkaar.

Ana kooy kókkaleek a ñàkke kersa? Moo kooy yékkatil kàddu? Kooy xool gëti xeebeel? Xanaa du Aji Sell ju Israyil ji?

Saa yu ma waxee, damay xaacu, fitnaak salfaañoo ma tax di yuuxu. Kàddug Aji Sax jee may yóbbey xas aki saaga bés bu ne.

Ci nit ñu dëgër bopp te dërkiis laa lay yónni. Wax leen, ne leen: “Lii Boroom bi Aji Sax ji da koo wax.”

Acts 9:4 TSK

Mu daanu ci suuf, daldi dégg baat bu ko ne: «Sóol, Sóol, lu tax nga di ma bundxatal?»

¶ Bu leen kenn naxe waxi ngelawal neen, ndax yooyu ma lim mooy wàcce sànjum Yàlla ci kaw aji déggadi ñi.

Loraange lees leen di feye loraange gi ñu sabab. Seen mbégte mooy xawaarey bëccëg ndarakàmm. Ñooñoo diy gàkk, aki sikk, ndax seen teewaay gàcce la ci seen biir yeen, bu ñuy bokk ak yeen bernde, te ca lañuy bànneexoo ay nax.