Damaa wàcc, xettlisi leen ci waa Misra; génne leen réew moomu, ba yóbbu leen réew mu baax te yaatu, réew mu meew maak lem ja tuuroo, foofa ca diiwaanu Kanaaneen ña ak Etteen ña ak Amoreen ña ak Periseen ña ak Eween ña ak Yebuseen ña.
TSK
TSK · Isaiah 64:1
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Fekk na tundu Sinayi wa wépp di sël-sëleeku saxar, ndax Aji Sax ja fa wàcc ci biir sawara. Saxar saa ngay gilli ni saxaru puuru ban, tund wépp di yëngook doole,
Ma jàq, woo Aji Sax ji, ne sama Yàlla wallóoy, mu dégge këram. Ma yuuxu, muy dégg.
Céy Yàlla, yaa génn, jiitu sa mbooloo, daagu, dugg màndiŋ ma. Selaw.
tund yu mag yiy curpi niy kuuy, di curpeendook tund yu ndaw yi niy mbote.
Aji Sax ji, firil asamaan, wàcc; laal tund yi, ñu saxar.
Boroom bi, Aji Sax ji Boroom gàngoori xare yi, kiy laal suuf, mu ne soyox seey, mboolem lu ci biiram di jooyoo; suuf fuddoondoo ni dexu Niil, dellu rës ni dexu Misra.
Aji Sax jaa ngii di génne ca bérabam ba, mooy wàccsi, daagoo kawtey suuf.
¶ Ñaanu Yonent Yàlla Abakug a ngii, galanu woy wi di galanu njàmbat.
Waaye bésu Boroom bi nib sàcc lay dikke. Ca la asamaan yi di dëddoo ci biir coow lu réy, lu ko sosoon seey ndax tàng, suuf ak jëf ju ci biiram xoyomu.