TSK

TSK · James 5:13

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage
Job 33:26 TSK

bu ñaanee Yàlla, mu nangul ko, geesu ko, mu sarxolle, nde Yàllaay fey nit njekkam,

di ma woo bésub njàqare, ma wallu la, nga màggal ma.»

Nanu ko dikke cant, woyal ko, mu riir.

Buumi ndee a ma laawoon, njàqarey njaniiw dab ma, ma dajeek naqar aku tiis.

Muy taalifu ñaan bu ñeel Daawuda, ba mu nekkee ca xunti ma.

Ña ngay naan biiñ, di sàbbaal yàllay wurus yaak yu xaalis yaak yu xànjar yaak yu weñ yaak yu bant yaak yu doj ya.

Jonah 2:2 TSK

Yunus ñaan ci Yàllaam Aji Sax ji, fa mu tollu ca biir jën wa.

Micah 4:5 TSK

Askan wu nekk ci yaakaaru turu yàllaam lay doxe. Nun nag ci yaakaaru sunu turu Yàlla Aji Sax ji lanuy doxe, tey ak ëllëg, ba fàww.

Njàqare nag jàpp Yeesu, mu gënatee tënku ci kàdduy ñaanam, ba aw ñaqam mujj mel ni lumbi deret, di dal ci suuf.

Ndigal loolu nag tax mu sànni leen ca néeg ba gëna ruqe ca kaso ba, jéng leen.

¶ Te it, waccalees na ma ndégu biir suux, mu taxawe ndawal Seytaane, di ma mitital, ngir ma baña bew ndax peeñu yu yéeme.

Na leen kàddug Almasi dëkke, bay baawaan, ngeen di jariñoo xel mu mat sëkk mu ngeen di jànglantee, ak a artoonte. Woyeleen xolub cant, ñeel Yàlla, ay taalifi Sabóor, ak woyi tagg Yàlla, ak woy yu fentoo ci Noo gi.

Ñuy woy nag woy wu yees, naan: «Yaa yeyoo jël téere bi, tàyyi tayu yi, ndax yaw lañu rendi, te sa deret nga jote, ngir Yàlla, ay niti gépp giir ak wépp làmmiñ ak wépp xeet ak wépp askan.

Ña ngay woy woy wu yees ca kanam ngàngune ma, ca kanam ñeenti bindeef yaak mag ña, te kenn manula mokkal woy wi, ku dul téeméer ak ñeent fukk ak ñeenti junni ñooñu ñu jote àddina.